TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 7
  • Nit kii am na fit

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nit kii am na fit
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Dañu fi nettali bi Yàlla komaasee sàkk ba bi mu indee mbënn mi, maanaam taw bu metti, ci kow suuf si sépp
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 7
Enog

NETTALI 7

Nit kii am na fit

SUUF si mu ngi gën a bare nit. Ñu ci ëpp, ñu ngi mel ni Kayin. Dañuy def lu bon. Waaye am na ku melul ni ñoom. Kooku, Enog la tudd. Ku am fit la. Ñi ko wër ñépp, lu bon rekk lañuy def. Waaye Enog moom, dafay topp Yàlla rekk.

Ab góor gu soxor ca jamanoy Enog rey na moroomam

Ndax xam nga lu tax nit ñi doon def lu bon rekk ? Seetal lii : Aadama ak Awa, lekk nañu doomu garab bi leen Yàlla tere woon. Waaye kan moo leen xiir ci déggadi Yàlla ? Malaaka bu bon la woon. Biibël bi dafa ko tudde Seytaane. Mu ngi def lépp ngir nit ñépp bon.

Benn bés, Yàlla digal na Enog mu wax nit ñi li nga xam ne bëgguñu ko dégg. Lii la leen waroon a wax : ‘ Yàlla dina alag ñu bon ñépp. ’ Mën nañu xalaat ne nit ñi meroon nañu lool bi ñu déggee loolu. Xéyna sax jéem nañu rey Enog. Kon dafa waroon a am fit ngir wax leen li Yàlla bëggoon a def noonu.

Nit ñu bon ca jamanoy Enog ñu dund ni leen neexe

Yàlla bàyyiwul Enog mu yàgg ci nit ñooñu. Enog, 365 at rekk la dund. Lu tax ñu nee “ rekk ” ? Ndaxte ca jamano jooja, nit ñi dañu gënoon a am doole te dañu doon dund lu gën a yàgg. Doomu Enog, Matusala, bi mu gaañoo, 969 at la amoon !

Ginnaaw bi Enog gaañoo, nit ñi dañu doon gën a bon rekk. Biibël bi nee na lu bon rekk lañu doon xalaat te suuf si feesoon na ak ay nit ñu soxor lool.

Ndax xam nga lu tax coono yooyu yépp amoon ca jamano jooja ? Dafa amoon lu bees lu Seytaane defoon ngir xiir nit ñi ci lu bon. Nañu seet loolu ci nettali bii di topp.

Njàlbéen ga 5:21-24, 27 ; 6:5 ; Yawut ya 11:5 ; Yudd 14, 15.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager