XAAJ 2
Li xewoon diggante taw bu metti bi ak bi Yàlla musalee waa Israyil ci Misra
Juróom-ñetti nit rekk ñoo mucc ci taw bu metti bi. Waaye ndànk-ndànk nit ñi dañu yokkuwaat ba nekk ay junniy-junni nit. Bi taw boobu amee ba mu am 352 at, ca la Ibraayma juddu. Yàlla def na li mu digoon Ibraayma, maanaam dafa koy may doom bu ñu tudde Isaaxa. Dinañu gis naka la Yàlla defe loolu. Ci ñaari doomi Isaaxa, Yanqóoba la Yàlla tànn.
Yanqóoba amoon na doom yu bare, 12 doom yu góor ak ay doom yu jigéen. Fukki doomam yu góor yi dañu bañoon lool seen rakk Yuusufa. Dañu ko jaay mu nekk jaam ca Misra. Ay at ginnaaw loolu, Yuusufa nekk na kilifa gu mag foofu. Bi xiif gu metti amee, Yuusufa seet na ndax magam yi soppi nañu seen jikko. Ginnaaw loolu, waa këru Yanqóoba yépp, maanaam waa Israyil, toxu nanu Misra. Loolu xewoon na 290 at ginnaaw bi Ibraayma juddoo.
Waa Israyel nekkoon nañu 215 at ci Misra. Bi Yuusufa gaañoo, dañu leen def jaam foofu. Musaa juddu na ca jamano jooja. Yàlla jaar na ci moom ngir musal waa Israyil ci Misra. Lépp li ñu nettali ci XAAJ 2, xewoon na ci biir 857 at.