XAAJ 3
Diggante bi ñu jógee Misra ba ci jamano buuru Israyil bu jëkk bi
Bi waa Israyil jógee Misra, Musaa yóbbu na leen ba ca tundu Sinayi. Foofu la leen Yàlla joxe ndigalam yi. Ginnaaw loolu, Musaa yónni na 12 nit ca Kanaan ngir yërndu réew mi te seet ni mu mel. Waaye 10 nit ci ñoom dañu wax lu ñaaw ci réew moomu, ba tax mbooloo mi bëgg dellu Misra. Yàlla daldi yar waa Israyil ndax seen ñàkk ngëm. Dafa leen wax ne dinañu nekk di wër rekk ci màndiŋ mi nga xam ne dara du fa sax. Te dinañu fa des lu mat 40 at.
Ginnaaw loolu, Yosuwe la Yàlla tànn ngir yóbbu waa Israyil ca Kanaan. Yexowa def na ay kéemaan ngir dimbali leen ñu dugg Kanaan. Taxawal na ndox mi nekk ci dexu Yurdan, daaneel na miiri Yeriko, te taxawal na naaj bi ci asamaan benn fan yépp. Ci lu mat juróom-benni at la waa Israyil nangu réew mi ci loxo waa Kanaan.
Ay àttekat ñoo doon ilif Israyil ci lu mat 356 at. Yosuwe mooy àttekat bi jëkk. Dinañu jàng lu jëm ci ñu bare ci ñoom, mel ni Barag, Sedeyon, Yefte, Samson, Samwil ak ñeneen. Dinañu jàng itam lu jëm ci ay jigéen yu mel ni Raxab, Debora, Yawel, Ruut, Nawomi ak Delila. Lépp li ñu nettali ci XAAJ 3, xewoon na ci biir 396 at.