XAAJ 4
Diggante Buur bu jëkk bi ci Israyil ba bi ñu nekkee jaam ca Babilon
Sóol moo doon buur bi jëkk ci Israyil. Waaye Yexowa bàyyi na ko te dafa tànn Daawuda ngir mu jël palaasam. Dinañu jàng lu bare ci Daawuda. Bi mu nekkee xale, dafa xeex ak ponkal bi tudd Goliyàtt. Ay at ginnaaw loolu, daw na buur bi Sóol ndaxte Sóol dafa ko doon iñaane. Te it am na jigéen bu rafet bu tudd Abigayil bu ko tere def lu ñaaw lool.
Dinañu jàng itam lu bare ci doomu Daawuda bi tudd Suleymaan te nekkoon buuru Israyil ginnaaw Daawuda. Ñetti buur yi jëkk ci Israyil, kenn ku nekk dafa nguuru 40 at. Ginnaaw bi Suleymaan gaañoo, xaaj nañu Israyil mu am ñaari nguur : benn bu féete bëj-gànnaar ak beneen bu féete bëj-saalum.
Nguur gi féete woon bëj-gànnaar, dafa boole woon 10 giiru Israyil. Yàgg na 257 at bala waa Asiri alag ko. Ay 133 at ginnaaw loolu, alag nañu itam nguur gi féete woon bëj-saalum. Booba lañu yóbbu waa Israyil ñu nekk jaam ca Babilon. Kon dinañu gis ci XAAJ 4 ay xew-xew yu bare te am solo yu amoon ci lu mat 510 at.