LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lan mooy Bésu Àtte bi ?
CI YOW, naka la Bésu Àtte bi di mel ? Ñu bare dañu foog ne ay milyaari nit lañuy indi benn par benn ci kanamu Yàlla, ngir mu àtte leen. Ñenn ñi Yàlla dina leen yóbbu àjjana ca kaw asamaan ngir neexal leen. Ñeneen ñi ñu dugal leen safara fu ñu leen di toroxal ba abadan. Waaye li Biibël bi wax ci Bésu Àtte bi, wuute na lool ak loolu ñuy wax. Kàddu Yàlla wone na ne Bésu Àtte bi du jamono ju ñu war a ragal. Waaye dafay doon jamono juy may nit ñi yaakaar ak waxtu bu ñuy defaraat suuf si.
Ndaw li Yowaana wax na ni Bésu Àtte bi di mel. Lii la bind ci Peeñu ma 20:11, 12 : “ Noonu ma gis gàngune [maanaam siisu buur] mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes. Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanamu gàngune ma. Ñu daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya. ” Kan mooy Àttekat bu ñuy wax foofu ?
Yexowa Yàlla mooy Àttekat bi gën a mag pur doomu Aadama yi. Waaye dafa am keneen ku mu dénk àtte bi. Ni ko ndaw li Pool waxe ci Jëf ya 17:31, Yàlla “ sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn ”. Àttekat boobu Yàlla tànn mooy Yeesu Kirist mi mu dekkal (Yowaana 5:22). Kon kañ la Bésu Àtte bi di komaase ? Te kañ lay jeex ?
Peeñu ma wax na ne Bésu Àtte bi dafay komaase bu xeexu Armagedon weesoo, fekk Yàlla dindi fi àddina Seytaane bia (Peeñu ma 16:14, 16 ; 19:19–20:3). Bu Armagedon weesoo, dinañu sànni Seytaane ak ay malaakaam ci kàmb gu réy, tëj leen lu mat junniy at. Ci jamono jooju, 144 000 nit ñi war a dem ca kaw asamaan dinañu nekk ay àttekat te dinañu “ nguuru ak Kirist diirub junniy at ”. (Peeñu ma 14:1-3 ; 20:1-4 ; Room 8:17). Bésu Àtte bi, du diir bu gàtt bu mat 24 waxtu kese. Diiru junniy at lay doon.
Ci junniy at yooyu, Yeesu dina àtte “ ñiy dund ak ñi dee ”. (2 Timote 4:1.) “ Ñiy dund ” ñooy doon “ mbooloo mu réy ” miy mucc ca Armagedon (Peeñu 7:9-17). Ndaw li Yowaana gisoon na itam “ néew ya, [...] ñu taxaw ca kanamu gàngune ma ” fi ñuy àtte. Ni ñu ko Yeesu dige, ñi ‘ nekk ci bàmmeel, dinañu dégg baatam [bu Kirist] tey génn ’ ndax ndekkite bi (Yowaana 5:28, 29 ; Jëf ya 24:15). Waaye ci kaw lan lañuy àtte nit ñépp ?
Ni ko peeñu bi ndaw li Yowanna gisoon wonee, dañu “ ubbi ay téere ”, ba pare “ ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya ”. Ndax dañu bind ci téere ya li nit ñi defoon ? Déedéet. Duñu àtte nit ñi ci kaw li ñu defoon bala ñuy dee. Naka lañu def ba xam loolu ? Biibël bi nee na : “ Ku dee, jéggal nañu ko ay bàkkaaram. ” (Room 6:7, NW). Ñi dekki, Yàlla baal na leen seeni bàkkaar, ñu tàmbaliwaat dund bu bees. Kon téere yooyu ñu ubbi dañu war a doon ndigalu Yàlla yu bees yi. Ñiy mucc ci Armagedon ak ñiy dekki, bu ñu bëggee dund ba fàww, dinañu war a topp ndigalu Yàlla yi, boole ci it ndigal yu bees yi Yexowa di joxe ci biir junniy at yi. Kon dinañu àtte nit ñi ci kaw li ñuy def ci Bésu Àtte bi.
Bésu Àtte bi dina may ay milyoŋi nit fu ñuy njëkk a jàng liy coobare Yàlla te topp ko. Loolu dafay tekki ne dina am liggéey bu réy bu ñuy def ngir jàngal nit ñi. Waaw, “ ñi dëkk ci suuf su baax si, ci lu wóor dinañu jàng njubte ”. (Esayi 26:9, NW.) Waaye du ñépp ñooy nangu def coobare Yàlla. Esayi 26:10, NW, nee na : “ Su ñu baaxee sax ak ki soxor, du jàng liy njubte. Ci réewu njubte dina def lu dul yoon te du ràññee màggaayu Yexowa. ” Ñu soxor ñi dinañu leen alag ba fàww ci Bésu Àtte bi. — Esayi 65:20, NW.
Bu Bésu Àtte bi di jeex, doomu Aadama yi mucc dinañu “ dund ” dëgg, nekk ay nit ñu mat (Peeñu ma 20:5, NW). Ci Bésu Àtte bi, doomu Aadama yi dinañu nekkaat ay nit ñu mat na ca njàlbéen ga (1 Korent 15:24-28). Bu loolu weesoo, seetlu bu mujj bi daldi am. Dinañu yewwi Seytaane fi ñu ko tëj te bàyyi ko mu jéem a nax doomu Aadama yi, te loolu dootul amati (Peeñu ma 20:3, 7-10). Ñi ko toppul, dinañu am ba mu mat sëkk li Biibël bi dige, maanaam : “ Nit ñu jub ñi dinañu moom suuf si, te dinañu fa dëkk ba fàww. ” (Sabóor 37:29, NW). Waaw Bésu Àtte bi barke lay indil doomu Aadama yépp yi topp Yàlla !
a Boo bëggee gën a xam lu jëm ci Armagedon, seetal li ñu wax ci téere Étude perspicace des Écritures, volume 1, xët 1073 ba 1075, volume 2, xët 63 ak 64, ak téere Adorez le seul vrai Dieu, pàcc 20. Seede Yexowa yi ñoo defar ñaari téere yooyu yépp.