NJÀNGALE 3
Dëgg gi nekk ci Biibël bi te réeroon naka la feeñaate ?
Gëstukati Biibël bi ci ati 1870
La Tour de Garde bi njëkk a génn, 1879
La Tour de Garde tey
Biibël bi yégle woon na ne gannaaw deewu Yeesu, dina am ay jàngalekat yuy naxaate yuy jóg ci biir karceen yu njëkk ya te soppi dëgg gi nekk ci Biibël bi (Jëf ya 20:29, 30). Ni mu ko waxe woon, noonu la ame. Jàngalekat yooyu dañu jaxase njàngale Yeesu yi ak ay njàngale diine xërëmkat yi. Loolu moo indi réer ci biir diine karceen (2 Timote 4:3, 4). Lan moo ñu mën a wóor ne tey, li ñu xam ci Biibël bi mooy li Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Jamono ji Yàlla bëggoon a feeñal dëgg gi agsiwoon na. Yàlla waxoon na ne ci muju jamono xam-xam dëgg dina bare (Daniel 12:4). Ci atum 1870 amoon na benn gurupu nit yu doon daje ngir xam dëgg gi nekk ci Biibël bi. Dañu gisoon ne, diine yiy wuyoo turu karceen ñu ngi doon jàngale lu bare lu nekkul ci Biibël bi. Ñu daldi gëstu Biibël bi ngir xam li mu wax dëgg-dëgg te Yexowa dimbali na leen ci bu baax.
Ay góor yoo xam ne xam dëgg gi rekk moo leen tax a jóg ñoo gëstu Biibël bi. Fasoŋ bi ñu doon gëstoo Biibël bi, ba tey ñun fasoŋ boobu lañuy topp. Dañu doon tànn benn waxtaan, xool li ci Biibël bi wax. Bu ci amee aaya bu leerul, ñu xool yeneen aaya ngir xam li aaya boobu bëggoon a wax. Bu ñu demee ba li ñu nànd ànd ak lépp li nekk ci Biibël bi, ñu daldi ko bind. Kon dañu doon bàyyi Biibël bi firi boppam. Noonu la dëgg gi feeñaate ba ñu xam dëgg gi jëm ci turu Yàlla, ci nguuru Yàlla, ci li tax Yàlla sakk nit ak suuf si, ci liy xew gannaaw dee, ak ci yaakaaru gis ñi dee dundaat. Gëstu boobu muccal na leen ci njàngale yu dul dëgg ak ay jëf yu bon yu bare. — Yowaana 8:31, 32.
Ci booru atum 1879, Gëstukati Biibël bi gisoon nañu ne jot na ngir ñépp xam dëgg gi. Ci at moomu, dañu komaase di génne benn yéenekaay biy génn ba tey te tudd ci tubaab La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah. Tey ci àddina si sépp, ci lu mat 240 réew ñu ngi tasaare dëgg gi nekk ci Biibël bi ci lu mat 750 làkk. Xam-xam dëgg masul a baree nii !
Gannaaw deewu Yeesu, lan moo xewoon ak dëgg gi nekk ci Biibël bi ?
Naka lañu def ba dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla feeñaat ?