NJÀNGALE 11
Lu tax ñuy teew ci ay ndaje yu mag ?
Mexique
Allemagne
Botswana
Nicaragua
Italie
Xoolal nit ñi nekk ci foto yi ci paas bii. Ndax gis nga ni ñu kontaane ? Xam nga lu tax ? Ñu ngi teewe suñu benn ndaje bu mag. Ñun itam yàkkamti nañu teew ci suñu ndaje yu mag yi. Dañuy roy ñi doon jaamu Yàlla ca jamono yu yàgg ya. Yàlla dafa leen santoon ñu booloo ñetti yoon at mu nekk ngir jaamu Ko (Deutéronome 16:16). Am nañu ñetti ndaje yu mag ci at mu nekk : ñaari ndaje yu mag yu benn fan ak benn ndaje bu mag bu ñetti fan. Ban njariñ lañu mën a jële ci teewe ndaje yooyu ?
Ndaje yooyu dañuy dëgëral suñu diggante ak suñu mbokk karceen yi. Waa Israyil dañu amoon mbégte mu réy bi ñu doon booloo ak ñi gëmoon Yexowa ngir màggal ko. Tey ñun itam, bu ñu booloo ci suñu ndaje yu mag yi ngir jaamu Yexowa, dañuy kontaan lool (Sabóor 26:12 ; 111:1). Ci ndaje yooyu lañu mën a xamante ak yeneen seede Yexowa yu bokk ci yeneen mbooloo walla ci yeneen réew. Bu waxtu añ jotee, ñun ñépp dañuy añandoo ci bërëbu ndaje bi. Loolu dafay gën a neexal ndaje bi (Jëf ya 2:42). Ci xew-xew yu mel noonu lañu mën a yëg dëgg mbëggeel gi am ci “ kureelu bokk yi ” ci àddina si sépp. — 1 Piyeer 2:17.
Ndaje yooyu dañu ñuy dimbali ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Waa Israyil dañu doon jële njariñ ci nànd li ñu leen doon jàngal (Nehémia 8:8, 12). Ñun itam dañu fonk njàngale Biibël yi ñuy jot ci suñu ndaje yu mag yi. Turu ndaje bu nekk, ci Biibël bi la sukkandiku. Li ñuy gis te dégg ci porogaraam yooyu, dafa ñuy jàngal ni ñuy toppe santaane Yàlla yi ci suñu dund. Dañuy déglu itam suñuy mbokk ci ngëm di nettali ni ñuy jànkoontee ak jafe-jafe yi ci suñu jamono ju metti jii. Bu ñu gisee ne jafe-jafe yooyu terewul ñuy kontine di roy Kirist, loolu dafay dëgëral suñu ngëm bu baax. Tiyaatar yi ñuy def ci ndaje yu mag yu ñetti fan yi dañuy dundal nettali yi nekk ci Biibël bi te won ñu ni ñu mënee topp ay njàngale yu am solo. Ci ndaje bu nekk dañuy sóob ci ndox ñi bëgg a wone ne jébbal nañu seen bopp Yàlla.
Lan moo tax suñu ndaje yu mag yi nekk ay xew-xew yu neex ?
Ban njariñ nga mën a jële ci teewe benn ndaje bu mag ?