TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • T-35 p. 1-4
  • Ndax ñi dee dinañu dundaat ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax ñi dee dinañu dundaat ?
  • Ndax ñi dee dinañu dundaat ?
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Naka nga gise ëllëg ?
    Naka nga gise ëllëg ?
  • Ndax coono àddina dina mas a jeex ?
    Ndax coono àddina dina mas a jeex ?
  • Ci dëgg, kan moo ilif àddina si ?
    Ci dëgg, kan moo ilif àddina si ?
  • Lan mooy Nguuru Yàlla ?
    Lan mooy Nguuru Yàlla ?
Xóotalal waxtaan bi
Ndax ñi dee dinañu dundaat ?
T-35 p. 1-4
Ay waajur yuy xool seen foto doom bu gaañu

Ndax ñi dee dinañu dundaat ?

Ndax dinga ne . . .

  • waaw ?

  • déedéet ?

  • xéyna ?

LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?

Ñi dee “ dinañu dekki ”. — Jëf ya 24:15, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.

LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?

Day dëfël sa xol boo amee mbokk bu gaañu. — 2 Korent 1:3, 4.

Doo ragal a dee. — Yawut ya 2:15.

Dinga am yaakaaru gisaat say mbokk yu gaañu. — Yowaana 5:28, 29.

Benn njaboot ak benn jigéen ju ñàkk jëkkëram ñu yaakaaru ndekkite bi dëfël seen xol

NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?

Waaw waaw, xoolal liy topp :

  • Yàlla moo sàkk dund. Biibël bi nee na Yexowa Yàlla “ mooy jox ñépp bakkan ”. (Jëf ya 17:24, 25 ; Sabóor 36:10) Ki nga xam ne moom mooy jox ñépp bakkan, kooku wóor na ne mën na dekkil ku dee.

  • Yàlla mas na dekkil ay nit. Biibël bi wax na ci juróom-ñetti nit yu dekki ci kaw suuf. Amoon na ci ay xale, ay mag, ay góor ak ay jigéen. Amoon na ci ñu yàggul woon a dee, waaye kenn ci ñoom dee woon na ba am sax ñeenti fan bala ñu koy dekkil ! — Yowaana 11:39-44.

  • Yàlla yàkkamti na defaat loolu. Yexowa ci boppam bëggul mukk nit dee ; dafa gise dee ni noon. (1 Korent 15:26) Dafa bëgg lool noot noon boobu te dekkil ñi nekk ci xelam, ñu dundaat ci kaw suuf. — Job 14:14, 15.

LOO XALAAT CI LAAJ BII ?

Xale bu ndaw buy mag ba nekk màggat

Lu tax ñuy màgget di dee ?

Biibël bi dafa ciy tontu ci NJÀLBÉEN GA 3:17- 19 ak ROOM 5:12.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager