NAÑU FÀTTALIKU XAAJ 1
Waxtaanal ak ki lay jàngal ci laaj yii di topp:
Lan moo la gën a neex, ci li Biibël bi wax ci lu jëm ci ëllëg?
(Xoolal lesoŋ 02.)
Lu tax nga gëm ne Biibël bi Kàddu Yàlla la?
Lu tax ñu war di woowe Yàlla Yexowa?
(Xoolal lesoŋ 04.)
Biibël bi nee na ‘Yàllaa sàkk lépp’ (Peeñu 4:11). Ndax gëm nga loolu?
(Xoolal lesoŋ 06.)
Jàngal Kàddu yu Xelu 3:32.
Lan moo tax Yexowa doon xarit bi gën?
Lan la Yexowa di xaar ci ay xaritam? Ndax foog nga ne lu jaadu la?
Jàngal Sabóor 62:9.
Ci yan mbir nga ñaan Yexowa? Leneen lan nga ko mën a ñaan?
Naka la Yexowa di tontoo suñuy ñaan?
(Xoolal lesoŋ 09.)
Jàngal Yawut ya 10:24, 25.
Ban njariñ nga mën a jële ci teewe ndaje Seede Yexowa yi?
Ndax foog nga ne teewe ndaje yi, jar na ko?
(Xoolal lesoŋ 10.)
Lu tax liir Biibël bi bés bu nekk am solo? Ci ban waxtu nga mën a liir Biibël bi bés bu nekk?
(Xoolal lesoŋ 11.)
Ba fi ñu tollu nii, lan moo la gën a neex ci li nga jàng?
Bi nga komaasee jàng Biibël bi ba léegi, ndax jànkoonte nga ak ay jafe-jafe? Lan moo la mën a dimbali nga kontine ci sa njàng mi?
(Xoolal lesoŋ 12.)