Nañu fàttaliku xaaj 4
Waxtaanal ak ki lay jàngal ci laaj yii di topp:
Jàngal Kàddu yu Xelu 13:20.
Lu tax mu am solo nga tànn bu baax say xarit?
(Xoolal lesoŋ 48.)
Yan xelal ci Biibël bi ñoo la mën a dimbali bu dee...
jëkkër nga walla jabar?
waajur nga walla doom?
Yan wax ñoo neex Yexowa? Yan wax ñoo neexul Yexowa?
(Xoolal lesoŋ 51.)
Yan njàngale ci Biibël bi ñoo la mën a dimbali nga tànn bu baax ni ngay soloo?
(Xoolal lesoŋ 52.)
Naka nga mënee tànn ni ngay féexale sa xol ba mu neex Yexowa?
(Xoolal lesoŋ 53.)
Jàngal Macë 24:45-47.
Kan mooy «surga bu takku te teey» bi?
(Xoolal lesoŋ 54.)
Naka nga mënee jëfandikoo sa jot, sa kàttan ak sa alal ngir dimbali mbooloo mi?
(Xoolal lesoŋ 55.)
Jàngal Sabóor 133:1.
Lan nga mën a def ngir yokk bennoo ak jàmm bi ci biir mbooloo mi?
(Xoolal lesoŋ 56.)
Naka la ñu Yexowa di dimbalee bu ñu defee bàkkaar bu réy?
(Xoolal lesoŋ 57.)
Jàngal Baamtug Yoon wi 10:12.
Naka nga mënee wone sa takkute ci Yexowa, bu amee ñuy xeex diine dëgg ji walla ñu lay xiir ci bàyyi dëgg gi?
Ndax am na li nga war a soppi ci sa dund ngir wéy di takku ci Yexowa te sore diine yu dul dëgg yi?
(Xoolal lesoŋ 58.)
Naka nga mënee waajal sa bopp ngir muñ fitna yi?
(Xoolal lesoŋ 59.)
Lan nga fas yéenee def ngir wéy di jëm kanam ci wàllu ngëm?
(Xoolal lesoŋ 60.)