WOY-YÀLLA 154
Mbëggeel gu amul àpp
(1 Korent 13:8)
1. Yow siggil te xool
nit ñu baax ñi la wër.
Tey, gis ñu mel nii jafe na.
Moo tax ku leen am,
yow de am nga ay mbokk.
Dañu bëggante ci seen biir.
(PONT BI)
Mbëggeel du fi mas a deñ.
Ba abadan du jeex.
(AWU BI)
Oo, mbëggeel du jeex.
Ci Yexowa la bokk.
Moom mooy mbëggeel.
Oo, mbëggeel du jeex.
Nit war na am mbëggeel.
Mbëggeel gu amul àpp,
nañu ko yëg ba fàww.
Mbëggeel du jeex.
2. Léelée ñu dem ba
coono yi bare lool.
Suñu doole jeex, ñu ragal.
Waaye am yaakaar
tax na ñu wéy di bég.
Yexowa moo ñu may loolu.
(PONT BI)
Mbëggeel du fi mas a deñ.
Ba abadan du jeex.
(AWU BI)
Oo, mbëggeel du jeex.
Ci Yexowa la bokk.
Moom mooy mbëggeel
Oo, mbëggeel du jeex.
Nit war na am mbëggeel.
Mbëggeel gu amul àpp,
nañu ko yëg ba fàww.
(AWU BI)
Oo, mbëggeel du jeex.
Ci Yexowa la bokk.
Moom mooy mbëggeel
Oo, mbëggeel du jeex.
Nit war na am mbëggeel.
Mbëggeel gu amul àpp,
nañu ko yëg ba fàww.
Mbëg- geel du jeex.
Mbëg- geel du jeex.
Mbëg- geel du jeex.