Lépp lu Kàddu Yàlla yégle dina am!
1 Li Biibël biy yégle ci ëllëg, daa mas a soxal Seede Yeowa yi. Looloo tax ba ñu déggee ne, yaxu suñu ndaje mi gën a mag ci at mii, “Kàddu Yàlla, giy yégle liy ami” la naroon doon, bégoon nañu lool. Yàkkamti woon nañoo xam lu doon “dund[u] c[i] jamano ja [war],” bi ñu Yeowa beraloon. (Macë 24:45) Te nag, tasul suñu yaakaar.
2 Ponk yi ëpp solo ci ndaje mu mag mi: Waare giy faramfàcce yaxu ndaje mu mag mi, àjjuma lañu ko def; lilee doon yaxam: “Bàyyileen xel ci Kàddu Yàlla, giy yégle liy ami.” Waxtaane na loo xam ne gën na ñoo leeralal nettalib soppiku bi. (Macë 17:1-9) Fésal na ne tey-ci-tey, ñu ngi ci tànku dugg ci ji gën ci jamano yi yépp, ndaxte sore nañu lool ci muju jamono ji; jamano ju bees jaa ngii suñu kanam, jege ba dee! Pexe mu am solo, mu ñu soxla sàkk, ngir bàyyi xel ci Kàddu Yàlla, mooy faral di ko duruus. Tofflante waare bi tuddoon “Sàkkleen bànneex ciy duruus Kàddu Yàlla” jox na ñu xelal, yu ñu mën a jëfoo ngir suñu duruusu Biibël bi gën ñoo amal njariñ te gën ñoo jural bànneex.
3 Gaawu ci ngoon, nafar nañu yenn yëf yi tax mu wóor ñu ne, ñu ngi ci bés yu mujj yi. Ndax yaa ngi leen di fàttaliku, yépp? Dibéer ci suba, dundalaat nañu yégle yonent Xabakukk, ba ñu jàngee ne suñu jamano daa niru lool ak jamanoom, teyit xew-xew yu am soloo ngi ci tànku am, keroog Yeowa di sank ñu soxor ñi tey musal ñu jub ñi. Ndax jëli nga ponk bi ëppoon solo ci daraamu Yanxóobaak Esaw, daraam bu ñu jukkee ci Biibël bi? War nañoo wut ak cawarte barke yu bawoo ci Yeowa, bañ di soloo xelu tayal walla faaleedi yëf yu tedd yi.
4 Téere bu bees, buy jommal: Ndaw yaram wu daw, ba ñu jotee téere bu bees bi tudd Prêtons attention à la prophétie de Daniel! Du ñàkk tàmbali ngaa duruus mbind mu soxale moomu. Boroom kàddu gi doon wone téere bi, lii la wax: “Gannaaw ay fànn yu néew, yégle yi ne ci biir téere Dañel yépp, mat nañu.” Ndax loolu fésalul ne suñu jamano jii daa jamp?
5 Doxalinu ndaje mi gën a mag ci at mi feddali na bu baax-a-baax suñu ngëm ci lenn, maanaam lépp lu ñu Yàlla dig te matagul dina mujj a am. Looloo ngi ñuy xiir ci wéy di yéene ñeneen ñi Kàddu Yàlla, giy yégle liy ami!