TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/02 p. 7
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 2/02 p. 7

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru feewriyee : La vie : comment est-elle apparue ? Evolution ou création ? ; La Révélation : le grand dénouement est proche !, walla bépp téere bu def 192 xët bu nekk ci seen mbooloo. Màrs : Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Dinañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi. Woneleen téere Laaj ngir mën a tàmbali ay njàngum Biibël bi. Awril ak me : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Waaraatekat yi war nañu xamal ñi nuy waxal ne bu ñu ko bëggee, mën nañu jàpple liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp. Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, war nañu ko won téere Laaj bi, te góor-góorlu ngir mën a jàng ak moom Biibël bi.

◼ Bu amee kuy waaraate ci gox bu benn mbooloo moomul ci liggéeyu waare bi, na fa wone téere Laaj ak téere Xam-xam. Su ngeen gisee ku am téere yooyu ba pare, mën ngeen a wone téere bu leen neex. Na ñépp yóbbaale ay kayit yu ndaw yu bare, ngir kër yi ngeen fekkul kenn, walla bu ngeen dajee ak nit bu bëggul a jël suñuy téere. Dinañu góor-góorlu ngir seetiwaat ki suñu waxtaan soxal. Su nit kooku dëkkee ci gox bu benn mbooloo moomul ci liggéeyu waare bi, te mu jege beneen mbooloo, war nañu def lépp li ñu mën ngir mu am ku ko seetiwaat.

◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 màrs lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

◼ Sekkerteer bi ak wottukatu liggéeyu waare bi war na seet li aji-xàll yoon yu ci sax (pionnier permanent) def ci waaraate bi. Bu ci amee ku ci waaraatewul waxtu yi ko war, mag ñi war nañu seet ni ñu ko mënee dimbali. Ngir dimbali pioñee yooyu, seetleen li nekk ci leetar S-201 yi ñuy jot at mu nekk. Seetal itam xise 12 ba 20 bu Le ministère du Royaume bu Ut 1986 ci xët 4 ba 5.

◼ Ren, waxtaan bi ñuy faral di am ci àddina si sépp, bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, 14 awril lay doon. Mu ngi tudd “ Gardez constamment à l’esprit ‘ le jour redoutable ’ ” (Buleen fàtte mukk bés bu raglu bi). Dinañu joxe benn palaŋ ngir waxtaan boobu. Ayu-bés boobu, su wottukat biy wër ci mbooloo yi nekkee ci yéen, walla su ngeen amee ndaje bu mag, waxtaan boobu na ngeen ko def ayu-bés bi ci topp. Benn mbooloo warul a def waxtaan boobu balaa 14 awril 2002 jot.

◼ Téere yu bees yi ñu mën a am :

Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? (T-26) — araab, españool, tubaab, purtugees, twi, yoruba

Ce que Dieu attend de nous — monokutuba

L’enfer de feu fait-il partie de la justice de Dieu ? (ngir jullit yi) (T-74) — españool

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains I — yoruba

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains I (mbind yu dijj) — purtugees

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains II — ewe

Le nom divin qui demeure à jamais — yoruba

Le plus grand des noms (ngir jullit yi) (T-72) — españool

Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ? — monokutuba

Louons Jéhovah par nos chants (29 woy-Yàlla) — moore

Organisés pour bien remplir notre ministère — yoruba

Prêtons attention à la prophétie de Daniel ! — igbo

Qui sont les Témoins de Jéhovah ? (ngir jullit yi) (T-73) — españool

Une vie pleinement satisfaisante : comment ? — ewe

◼ Téere yi ñu amaat :

Annuaire des Témoins de Jéhovah 2001 — tubaab

◼ Kaset yu ñuy déglu yu bees yi ñu mën a am :

Des exemples qui nous servent d’avertissement — kaset yu ñuy déglu (daraam, benn kaset) — españool

Marqués pour la survie (daraam, benn kaset) — purtugees

◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :

Fidèles malgré les épreuves — Les Témoins de Jéhovah en Union soviétique (NTSC) — ãgale

Le plus grand homme de tous les temps — volume 2 (NTSC) — ci làkku liyaaru Amerig

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager