Na karceen bu nekk wone takkute ci Yàlla bu amee mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi
1 Bokk deret mën na nekk lu am doole lool. Kon, bu ñu amee mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi walla bu génne boppam ci mbooloo mi, dina doon fu ñu mën a gis ndax karceen dëgg lañu. Mbokk moomu mën na nekk suñu jëkkër walla suñu jabar, suñu doom, suñu pàppa walla suñu yaay, walla beneen mbokk mu jege (Macë 10: 37). Suñu diggante ak moom nu mu war a mel ? Bu ngeen bokkee kër nag, ndax mbir yi dinañu wuute ? Nañu njëkk seetaat li Biibël bi wax ci loolu. Te nañu xam ne, bu ñu ko dàqe walla mu génne boppam, benn la.
2 Ni suñu diggante ak ku ñu dàq ci mbooloo mi, war a mel : Kàddu Yàlla digal na karceen yi ñu bañ a ànd walla xaritoo ak ku ñu dàq ci mbooloo mi : “ Buleen séq dara ak [képp] ku ñu tudde mbokk mu gëm Krist, te fekk day njaaloo, walla mu nay, walla muy xërëm, walla muy xas nit, walla muy màndi walla muy njublaŋ. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk. [...] Dàqleen ci seen biir kiy def lu bon. ” (1 Kor. 5:11, 12). Li Yeesu wax ci Macë 18:17 laal na it li ñu waxtaan fii : “ Nga teg ko [ki ñu dàq] ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat. ” Ñi doon déglu Yeesu, xamoon nañu bu baax ne Yawut ya ca jamano jooju, xaritoowuñu woon dara ak ñi dul Yawut, te dañu doon moytu juutikat yi, di leen jàppe ni nit yu ñu dàq. Kon Yeesu dafa doon sant taalibeem ya ñu bañ a ànd ak ñi ñu dàq. — Xoolal li nekk ci La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1981, xët 17 ba 19.
3 Loolu mu ngi tekki ne, karceen warul séq dara ci wàllu ngëm ak ku ñu dàq ci mbooloo mi. Waaye ndigal boobu ëmb na leneen. Kàddu Yàlla nee na waruñu sax lekk ak kooku (1 Kor. 5:11). Kon, duñu ànd itam ak ku ñu dàq ci mbooloo mi. Loolu ëmb na bañ a def lu mel ni ànd di féexlu, ànd di futbal, walla ànd dem jëndi li ñuy soxla, walla toog di lekk ak moom ci biir kër gi walla ca lekkukaay.
4 Ndax mën nañu wax ak ku ñu dàq ci mbooloo mi ? Biibël bi waxul lépp lu ñu war a def walla bañ a def, waaye li ñu bind ci 2 Yowanna 10 moo ñuy tax a xam ni Yexowa gise loolu : “ Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax. ” Lii la La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1981, xët 23 wax ci aaya boobu : “ Ci benn nuyu rekk la waxtaan walla sax xaritoo mën a tàmbalee. Ndax dinañu bëgg tàmbali loolu ak ku ñu dàq ci mbooloo mi ? ”
5 Loolu mooy li Tour de Garde boobu wax ci xët 29 : “ Li am mooy bu karceen bàyyee bàkkaar ilif ko ba ñu war koo dàq ci mbooloo mi, am na lu bare lu muy bàyyi ginnaaw : li mu neexoon Yàlla, [...] àndandoo bu neex ak suñuy mbokk ci ngëm, ak lu bare li mu mënoon a def ak mbokkam yi nekk karceen.
6 Ci biir kër gi : Su ay karceen amee ci seen waa kër benn mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi, ndax li ñu wax fi yépp mu ngi tekki ne waruñu wax ak moom, lekk ak moom, te bañ a ànd ak moom ci li ñuy def bés bu nekk ? La Tour de Garde bu 15 awril 1991, lii la wax ci suufu xët 22 : “Su karceen amee ci këram benn mbokkam bu ñu dàq ci mbooloo mi, kooku ñu dàq dina bokk ba tey ci lépp lu waa kër gi di def mbaa toppatoo bés bu nekk. ” Kon, ñi bokk ci njaboot gi ñoo war a seet fan lañu war a yemale nit kooku bu ñuy lekk walla bu ñuy def leneen ci biir njaboot gi. Waaye, bëgguñu seeni mbokk ci ngëm ci mbooloo mi foog ne lépp a ngi mel ni bala ñu koy dàq.
7 Waaye it, La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1981, xët 26 ak 27, lii la waxoon ci ku ñu dàq ci mbooloo mi, walla ku ci génne boppam : “ Li ñu séqoon bu njëkk ci wàllu ngëm, dog nañu ko ba mu jeex tàkk. Bu dee suñu mbokk la walla sax mbokk bu ñu bokkal kër, noonu la itam. [...] Seen diggante ci wàllu ngëm bi ngeen amoon bu jëkk ci biir kër gi, dina soppeeku. Su dee jëkkër ji lañu dàq ci mbooloo mi, su ko jabar ji ak doomam yi gisee muy jiite njaboot gi bu ñuy gëstu Biibël bi walla bu ñu koy jàng, walla bu ñuy ñaan, du nekk lu leen gënal. Bu bëggee ñaan, mel ni bu waxtu lekk jotee, mën na ko def ndegam ci këram la nekk. Waaye ñoom mën nañu ñaan Yàlla ci seen biir xol (Léeb. 28:9 ; Sab. 119:145, 146). Léegi, su amee ku bokk ci kër gi, fekk dàq nañu ko ci mbooloo mi, te mu bëgg nekk ak njaboot gi bu ñuy jàng Biibël bi walla ñu ciy gëstu, lan lañu war a def ? Mën nañu ko bàyyi mu ñów déglu su dee du leen jéem a jàngal walla indi foofu li mu gëm ci wàllu diine. ”
8 Su ndaw nekkee ci biir kër gi, te ñu dàq ko ci mbooloo mi, ba tey wayjuram yi nekk karceen ñoo ko yore te ñoo ko war a yar. La Tour de Garde bu 15 nowàmbar 1988, xët 20, nee na : “ Dinañu wéy di ko jox lu muy lekk, lu muy sol, ak fu muy dëkk. Kon war nañu ko jàngal te yedd ko ci kow li nekk ci Kàddu Yàlla (Léebu 6:20-22 ; 29:17). Kon bu dee sax dañu ko dàq ci mbooloo mi wayjur yu baax te bëgg seen doom, dinañu jàng ak moom Biibël bi. Xéyna lu ko gën a mën a jubbanti mooy jàngal ko moom kenn. Walla mën nañu ko bàyyi mu bokk ci njàngum Biibël bi ñu def ak njaboot gi yépp. ” — Seetal itam li nekk ci La Tour de Garde bu 1 oktoobar 2001, xët 16 ak 17.
9 Mbokk yu bokkul ci suñu waa kër : “ Mbir mi bokkul su dee ki ñu dàq ci mbooloo mi walla ki ci génne boppam, mbokk la waaye bokkul ci waa kër gi, maanaam dëkkul ci biir kër gi. ” Moom la La Tour de Garde bu 15 awril 1988 wax ci xët 28. “ Xéy na dingeen mën a bañ a jote dara ak mbokk moomu. Bu dee sax am na li ngeen war a toppatoo lu jëm ci njaboot gi, te muy tax ngeen war a jote dara ngir loolu, dingeen fexe ba loolu nekk lu gën a tuuti bu ñu mën. ” Loolu ànd na ak ndigalu Yàlla bi ne “ buleen séq dara ak ” képp ku bàkkaar te bëggul tuub ay bàkkaaram (1 Kor. 5:11). Bu dul lu ñu soxla dëgg, karceen yi am takkute ci Yàlla dañu war a def lépp lu ñu mën ngir bañ a ànd ak mbokk mu mel noonu. Te bu amee lu ñu war a jote ci wàllu jaay ak jënd, nañu fexe ba mu nekk lu gën a tuuti lu ñu mën. — Seetal itam li nekk ci La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1981, xët 28 ak 29.
10 La Tour de Garde bi dafa ñuy wax ci leneen lu mën a am : “ Su ñu amee mbokk mu jege, mel ni suñu doom walla benn ci suñuy wayjur ku dëkkul ci biir kër gi, te dañu ko dàq ci mbooloo mi, waaye léegi dafa bëgg dellusi ci biir kër gi, lan lañu war a def ? Njaboot gi dina seet mbir mi ngir xam li ñu mën a def. Mën na am mbokk moomu ñu dàq ci mbooloo mi, dafa feebar te mënatul yore boppam, muy ci wàllu xaalis walla ci wàllu yaramam. Doom yi nekk karceen dañu ko war a dimbali. Mbind yi ñoo ko wax, te mooy yoon (1 Tim. 5:8). [...] Bala ñu xam lu ñuy def, dinañu seet li mbokk mi soxla dëgg, jëfinam ak ni boroom kër gi bëgge njabootam di am diggante bu rattax ak Yàlla, walla lu mel noonu. ” — La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1981, xët 27.
11 Su dee xale la, lii la Tour de Garde boobu wax : “ Léeg-léeg am na ay wayjur karceen yu bàyyi seen doom bu ñu dàq ci mbooloo mi mu dellu ci kër gi, ndaxte léegi dafa feebar ci yaram walla ci xel. Waaye ak li mën a tax mu bëgg ñówaat, wayjur yi ñoo war a seet bu baax ni kooku bëgg nówaat di dunde. Xale bu góor boobu ñu dàq ci mbooloo mi, ndax dafa doon dundal boppam, bañ a soxla kenn, te léegi mënatu ko ? Walla ndax li gën a tax mu bëgg dellusi ci biir kër gi mooy am dund bu gën a yomb ? Lan lañu mën a wax ci jikkoom ak jëfinam ? Ndax dina indi ‘ lawiir ’ ci biir kër gi ? — Gal. 5:9. ”
12 Njariñ bi ñu mën a am ci suñu takkute ci Yàlla : Mbind mi wax na ci lu jëm ci ku ñu dàq ci mbooloo mi ak it ci ni ñu waree bañ a jote dara ak ku bëggul tuub ay bàkkaaram. Su ñu toppee loolu, suñu njariñ lay doon. Dina tax mbooloo mi dëkk ci sell. Te nit ñi dinañu gis ne lu sell li Biibël bi di jàngale lañuy topp (1 Pie. 1:14-16). Dafa ñuy aar ci li mën a yàq suñu xel (Gal. 5:7-9). May na it ki bàkkaar mu mën a jariñoo bu baax-a-baax yar bi ko dal. Loolu mën na tax mu “ meññ jub ak jàmm ”. — Yaw. 12:11.
13 Suñu benn mbokk bu góor ci wàllu ngëm ak séexam bu jigéen ñoo demoon ci suñu benn ndaje bu mag bu ñaari fan. Booba amoon na juróomi at ak benn bi ñu dàqe woon seen yaay ci mbooloo mi, te yaay ji dëkkul woon ak ñoom. Am na benn waxtaan bu ñu déglu, ñu daldi xam ne dañu war a soppi seen diggante ak seen yaay. Bi ndaje bi paree rekk, ku góor ki telefone yaayam te ne ko bëgg nañu ko lool waaye léegi dootuñu mën a wax ak moom, xanaa bu amee lu am solo lu ñu war a waxtaan ci biir njaboot gi. Yàggul dara, yaayam daldi teew ci ndaje yi, ba mujj a bokkaat ci mbooloo mi. Jëkkëram it tàmbali na jàng Biibël bi te dem na ba ñu sóob ko ci ndox.
14 Mbind mi wax na lu jëm ci ñi ñu war a dàq ci mbooloo mi. Nañu takku ci Yàlla te topp loolu yépp bu baax. Foofu lañuy wone mbëggeel bi ñu am ci Yexowa te dina mën a tontu ki Koy tooñ (Léeb. 27:11). Te wóor nañu ne Yexowa dina ñu barkeel. Lii la Buur bi Dawuda bind ci Yexowa : “ Santaaneem yi, duma ci jóge. Ku takku ci yow, dinga takku ci moom. ” — 2 Sam. 22:23, 26.
[Laaj yi]
1. Lan moo mën a laal suñu takkute ci Yàlla ?
2. Ci li Biibël wax, diggante karceen ak ku ñu dàq ci mbooloo mi nu mu war a mel ?
3, 4. Yan jote lañu tere ak ku ñu dàq ci mbooloo mi walla ak ku ci génne boppam ?
5. Ku ñu dàq ci mbooloo mi, lan lay bàyyi ginnaaw ?
6. Ndax karceen waratul jote dara ak benn mbokkam bu ñu dàq ci mbooloo mi, fekk ci waa kër gi la bokk ? Leeralal sa tont.
7. Naka la diggante ci wàllu ngëm ci biir njaboot di soppeeku bu ci amee ku ñu dàq ci mbooloo mi ?
8. Wayjur yi nekk karceen, ban warugar lañu am ci seen doom ju nekk ndaw te dëkk ak ñoom ?
9. Diggante bi karceen mën a am ak mbokkam bu ñu dàq ci mbooloo mi, fekk dëkkul ak moom ci biir kër gi, fan la war a tollu ?
10, 11. Ci lan la karceen war a xalaat bala muy nangu mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi, ñów dëkk ak moom ?
12. Am ñi ñu dàq ci mbooloo mi, ban njariñ lay am ?
13. Lan la benn njaboot soppi, te loolu lu mu indi ?
14. Lu tax ñu war a ànd bu baax, boole ci takkute ci Yàlla, ak lépp lu jëm ci ñi ñu dàq ci mbooloo mi ?