TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/02 p. 7
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 8/02 p. 7

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru ut : Benn ci téere bu def 32 xët ci yi nekk fii : Dieu se soucie-t-il vraiment de nous ? ; Doit-on croire à la Trinité ? ; Le gouvernement qui établira le Paradis ; Le nom divin qui demeure à jamais ; Quand la mort frappe un être aimé... ; Que devient-on quand on meurt ? ; Quel est le but de la vie ? Comment le découvrir ? ; Dunda léen bà fàw ak banéx ci suf si! ;  Voici, je fais toutes choses nouvelles ”. Boo gisee ne dina baax ci nit ki ngay waxal, mën nga wone benn ci téere yii : Connaîtrons-nous un jour un monde sans guerre ? ; Les esprits des morts — Peuvent-ils vous aider ou vous nuire ? Existent-ils vraiment ? ; Nos problèmes — Qui nous aidera à les résoudre ? ; Un livre pour tous. Septaambar : La vie : comment est-elle apparue ? Évolution ou création ? Balaa ngay laaj bànqaas bi téere yooyu, seetal ndax amul mbooloo bu la jege bu la ci mën a may. Oktoobar : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, war nañu ko won téere Laaj bi, te góor-góorlu ngir mën a jàng ak moom Biibël bi. Nowàmbar : Lan la ñu Yàlla laaj ? walla Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Bu ngeen gisee ku am téere boobu ba pare, won leen ko benn ci téere yu yàgg yi. Bu ngeen amulee téere yu yàgg yooyu, seetal ndax am na yeneen mbooloo yu ci am.

◼ Bu mbooloo yi di laaj téere yi ñu soxla, mën nañu ci boole léegi téere yii : Calendrier des Témoins de Jéhovah 2003, Examinons les Écritures chaque jour – 2003 ak Annuaire des Témoins de Jéhovah – 2003. Téere yooyu yépp mën nañu leen am ci araab, ãgale, tubaab, purtugees ak español. Mën nañu laaj it téere Examinons les Écritures chaque jour – 2003 ci làkku ewe, swaili ak twi.

◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 septaambar lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

◼ At mu nekk, dañuy seet ñaata téere ak yéenekaay ñoo des ci mbooloo mi. Ren, bésu 31 ut 2002 lañu ko war a def, walla ci bés bu ko gën a jege. Liggéey boobu, mu ngi mel ni li kiy toppatoo téere yi di def weer bu nekk te war nañu bind li ñu ci waññ ci kayit bi tudd Stock des publications (S-18). Su amee ay mbooloo yu bokk fu ñuy dence seeni téere, kiy toppatoo yéenekaay yi ci mbooloo mu nekk dina joxe ñaata yéenekaay ñoo des ci mbooloom. Mbooloo mi war a jot loolu, maanaam biy toppatoo mbooloo yi ci des ci wàllu téere yi, bànqaas bi dina ko yónni ñetti kayit yi tudd Stock des publications (S-18). Na ngeen bind li ñu ciy laaj ci benn bi te yónnee ko bànqaas bi, bés bu warul a weesu 6 septaambar. Ñaareelu kayit bi sotti lay doon. Denc leen ko ci mbooloo mi. Ñetteel bi ngeen di jëfandikoo bu ngeen di def liggéey boobu te sekkerteer bi moo koy jiite. Moom ak wottukat biy jiite ñoo war a bind seen tur ci kayit boobu (S-18).

◼ Téere yu bees yu ñu mën a am :

Avez-vous un esprit immortel ? (T-25) — swaili

La prophétie d’Isaïe, lumière pour tous les humains II — español

Qui domine vraiment le monde ? (T-22) — yoruba

◼ Téere yu bees yu ñu mën a am ci bindu gumba yi :

Tirez profit de l’École du ministère théocratique — ãgale

◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :

La Bible : un récit historique exact, des prophéties dignes de foi (Secam) — làkku ñi tëx

Le plus grand homme de tous les temps, volume 4 et volume 5 (Secam) — làkku ñi tëx

Les Témoins de Jéhovah : un nom, une organisation (NTSC) — araab

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager