TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 10/02 p. 1
  • Ni ñuy defe njàngum Biibël ci kër nit ñi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ni ñuy defe njàngum Biibël ci kër nit ñi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 10/02 p. 1

Ni ñuy defe njàngum Biibël ci kër nit ñi

1 Naka lañuy defe njàngum Biibël bu baax ci kër nit ñi ? Ban royukaay lañu ci am ? Naka lañu waree jëfandikoo aaya yi nekk ci li ñuy jàng ? Kan moo war a jàng xise yi ? Bu ñuy def njàngum Biibël, am na li ñu mënul a bañ a def. Waaye ginnaaw loolu, lan lañu war a def ngir nit kiy jàng dugal dëgg gi ci biir xolam ? Lan lañu war a moytu ?

2 Ni ñuy jàngale Biibël bi : Njàngum Biibël, ci lu ëpp dafay mel ni njàngum La Tour de Garde. Dañuy njëkk jàng xise bu ñu war a def, ba pare kiy jiite laaj laaj bi ñu bind ngir xise bi, te may nit kiy jàng mu tontu. Yenn saay, kiy jàng mën na bañ a xam bu baax li mu war a tontu. Na fekk ki koy jàngal, waajal boppam ba pare ngir laaj ko ay laaj yu koy tax a xalaat bu baax ci li muy jàng, ba lépp leer ci xelam.

3 Seetleen lu tax aaya yi nekk ci xise bi ànd ak li ñu ci wax. Wonal nit kiy jàng ni mu mënee xàmme ci xise bi, aaya bu ñu jële ci Biibël bi, te waxtaanal ak moom ci li waral ñu def ko ci. Ay aaya mën nañu nekk ci xise te duñu bind li ci nekk. Bu ñu guddul torop, wutleen ko ci Biibël bi. Ñaanal kiy jàng mu jàng ko te wax ni ñuy ànde ak li nekk ci xise bi walla ni ñu koy leerale.

4 Dimbalil kiy jàng mu dugal dëgg gi ci biir xolam : Waxal kiy jàng mu waajal bu baax njàng mi. Won ko bu baax ne ku bëgg yokk xam-xamam, dafa war a jàng. Li muy gën di jàng te di xalaat bu baax ci li mu jàng, muy gën ci moom. Bu ñuy def njàngum Biibël, am na ñuy bàyyi ki ñuy jàngal, jàng xise yi yépp. Ñeneen ñi bu nit ki jànge benn xise, dañuy jàng bu ci topp. Nit ku nekk moo war a seet liy gën ci ki muy jàngal ngir mu mën a jëm kanam ci wàllu ngëm.

5 Jàngal nit ni ko jàngalekat yi di def ci lekkool, dina tax mu yokk xam-xamam. Waaye, ndax dina tax mu gëm li muy jàng ? Bu ñu bëggee nit ki dugal dëgg gi ci xolam, bu jàngee dara, dafa war a xam ni mu koy laale. Lan la xalaat ci li muy jàng ? Naka la mënee jëfandikoo li mu jàng ? Laaj ko ay laaj yu xóot ngir jot xolam.

6 Li ñu war a moytu : Am na li ñu war a moytu, bu ñuy def njàngum Biibël. Bu nit ki laajtee lu bokkul ci li ñuy jàng, li gën mooy ñu waxtaan ci bu ñu paree njàng mi, walla beneen yoon. Am na it leneen lu am solo : fexe ba nit ki tontu ci kàddu boppam te bañ a yem ci jàng li nekk ci téere bi. Dina tax nga mën a xam ndax nànd na li muy jàng.

7 Lu tax doo fas yéene am lu mu tuuti tuuti benn njàngum Biibël ? Ku wéeru ci Yexowa te topp ni ñuy defe njàngum La Tour de Garde bi, du jafe ci moom. Bu ñuy def njàngum Biibël, ci lañuy gën a mën a jàngal nit ñi dëgg gi, te sàkk ay taalibe. Ku topp bu baax li ñu Yeesu laaj ci Macë 28:19, 20, dinga ci jële mbégte. Boo amee njàngum Biibël, dinga ko gis.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager