Ay tont ci seeni laaj
◼ Kañ lañuy mën a taxawal benn gurup buy làkk làkku bitim réew ?
Bu seen gox baree nit ñu jóge bitim réew te dégguñu làkku réew mi, magi mbooloo mi war nañu def li ñu mën ngir ñu mën leen a waar ci seen làkk (km-WO 7/02 xët 1 ; ak km-F 2/98 xët 3-4). Nit ñi jóge bitim réew te dégguñu làkku réew mi, mën nañu tasaaroo ci goxu ñaari mbooloo yu dend walla sax mbooloo yi ko ëpp. Bu booba, wottukat biy (walla yiy) wër ci mbooloo yi dina won mbooloo yooyu naka lañu war a def ngir ku ci nekk def wàllam ci liggéeyu waare bi. Yenn saay, mën nañu def waxtaan bu ñu jagleel ñépp, walla njàngum La Tour de Garde, ngir ñu mën a xam ñaata nit ñooy teew ci ndaje yi ñuy def ci làkku bitim réew boobu.
Bu ñett yii amee, dinañu mën a def benn gurup buy làkk làkku bitim réew : 1) Dafa am ay waaraatekat walla ay nit ñu suñu waxtaan neex ñu gën a nànd xibaar bu baax bi ci làkku bitim réew boobu. 2) Am na benn magu mbooloo walla benn surga mbooloo bu mën a jiite lu mu tuuti-tuuti benn ndaje ayu-bés bu nekk. 3) Am na kurélu mag bu bëgg jàpple gurup bi. Bu ñett yooyu yépp amee, magi mbooloo mi war nañu ko xamal bànqaas bi. Bu ko defee, gurup bi dina nekk gurup bu ñu taxawal ni mu ware, te dinañu leen a mën a jox yeneen tegtal.
Ay gurup yu bare dañu leen di tàmbali ak njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, ayu-bés bu nekk. Bu ñu demee ba mu yàgg, magi mbooloo mi mën nañu nangu ñu def yeneen ndaje, mel ni ndaje bi ñu jagleel ñépp ak njàngum La Tour de Garde bi. Bu amee magi mbooloo walla surga mbooloo bu dégg làkk boobu te mën a xelal nit ñi, dinañu mën a def waxtaan n° 2, 3, ak 4 ci beneen kalaas, bu ñuy def Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi. Waaye gurup bi dina bokk ci mbooloo mu koy jàpple ngir déglu liy tax ñu aay ci wax, waxtaan n° 1, kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi, ak ndaje liggéeyu waare bi. Mën nañu def itam ndaje bu ñuy am bala ñuy waare ngir gurup bi.
Képp ku bokk ci gurup bi, war na topp ndigali kurélu mag yi. Magi mbooloo mi war nañu joxe ay ndigal yu baax, te toppatoo li gurup bi soxla. Bu wottukat biy wër ci mbooloo yi ñówee ci mbooloo mu am gurup, dina fexe ba ànd waaraate ak gurup bi ngir dëgëral ko ci wàllu ngëm. Bu ko Yexowa barkeelee, gurup biy làkk làkku bitim réew mën na mujj nekk mbooloo.