TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/05 p. 5
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 3/05 p. 5

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru màrs : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Laaj bi. Bu ñuy jëfandikoo téere Laaj bi, nañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël. Awril ak me : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu ñuy dellu seeti nit ñi suñu waxtaan neex, nañu ci boole ñi mas a teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, walla ci beneen ndaje, waaye tàmmuñu teew ci ndaje yi yépp. Nañu leen won téere Adorez Dieu. Li ñu bëgg mooy tàmbali ay njàngum Biibël, rawatina ak ku jàng téere Xam-xam ak it téere Laaj ba pare. Suweŋ : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Laaj bi. Bu ñuy jëfandikoo téere Laaj bi, nañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël.

◼ Bu La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yu mujj yi agsee ci mbooloo yi, war nañu leen gaaw a jox waaraatekat yi. Dina tax ñu mën a jot ci yéenekaay yi ñu moomal suñu bopp, te mën leen a jàng bala ñu leen di wone ci waaraate bi. Sasu Nguuru Yàlla bi itam dinañu ko gaaw a jox waaraatekat yi saa su ñu ko jotee ci mbooloo mi. Loolu mën nañu ko def ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi.

◼ Booy dem ci beneen réew te nga bëgg fekke foofu ndajey mbooloo mi walla ndaje bu mag, te nga bëgg xam waxtu, bés, walla fu ñuy defe ndaje yooyu, nanga ko laaj bànqaas biy toppatoo liggéeyu waare bi ci réew boobu. Adareesu bànqaas yaa ngi ci xët bi mujj ci Annuaire bu mujj bi.

◼ Sekkerteeri mbooloo yi war nañu am kayit yi tudd Demande d’admission au service de pionnier permanent (S-205) ak Demande d’admission au service de pionnier auxiliaire (S-205b), ba mu mat li ñu mën a soxla ci benn at, walla lu ko ëpp. Bu ñu ci soxlaa, nañu jëfandikoo kayit bi tudd Demande de publications (S-14).

◼ Alxemes, 24 màrs 2005 mooy bésu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Bu seen mbooloo amee ndaje bés boobu, nangeen def ndaje boobu bés bu amul ndaje ci seen saalu Nguur. Su ngeen waree def seen ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi ci bésu fàttaliku bi, te amul bés bu amul ndaje ci seen Saalu Nguur, nangeen seet waxtaan yi mbooloo mi gën a soxla ci porogaraam boobu te boole ko ci beneen ndaje bu jëm ci liggéeyu waare bi.

◼ Am na Seede Yexowa yuy abalante ay woy-Yàlla yu ñu defaraat ba ñu mel ni misigu àddina sii. Am na ay waaraatekat yu bëgg a xam ndax mbootaayu Yàlla nangu na woy-Yàlla yooyu. Yëg nañu ne woy-Yàlla yu ñu defaraat noonu am na. Waaye dañu bëgg ngeen xam ne ànduñu ci. Kon ñu ngi leen di ñaan ngeen bañ a ab walla abal woy yooyu. Buleen ko jële it ci Internet. Yaakaar nañu ne li ñu wax fii dina leeral bu baax mbir mi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager