Nañu fexe ba jot nit ñu gën a bare
1 Taalibe Yeesu yu njëkk ya dañu bëggoon a xamal xibaaru Nguur gi nit ñu gën a bare. Am na lu am solo lu ñu def ngir mën loolu. Benn bi mooy, dañu bind Kàddu Yàlla ci làkk bi nit ñu gën a bare dégg, maanaam làkku grekk. Làkk boobu lañu doon làkk ci nguuru Room yépp. Leneen li ñu def itam mooy, ci diggante 100 at ba 300 at ginnaaw Yeesu, waaraatekat yu sawar yi dañu jëfandikoo li ñuy woowe codex (maanaam ay téere yoo xam ne dañuy am ay xët yuy teglante). Bu njëkk, ci benn xët bu ñu laxas (maanaam rouleau) lañu doon bind Mbind mu sell mi. Kon téere yu bees yooyu ñoo gënoon a neex a jëfandikoo.
2 Ni ñu jëfandikoo li boroom xam-xam yi sàkk : Ci gémmiñu yonent Yàlla Isayi, Yexowa newoon na lii : “ Dinga nàmp soowu xeet yi. ” (Isa. 60:16). Li yonent boobu yégle woon noonu mu ngiy am tey. Ñiy jaamu Yexowa ñu ngiy jariñoo alalu xeet yi (technologie) ngir liggéeyu waare bi jëm kanam. Ci atum 1914, ay ati at bala ñuy wax sax waxu sinemaa, Jàngkati Biibël bi ñu ngi doon wone film bi ñu doon woowe ci tubaab “ Photo-Drame de la création ”. Film boobu, juróom-ñetti waxtu lañu ko doon seetaan, dafa amoon kulóor te dañu doon dégg baatu ñi doon wax. Dafa boole woon ay foto yu dul yëngu ak film fu ñu doon wone ay nit ñuy yëngu. Film boobu dañu ko jëfandikoo ngir waar bu baax ay milioŋi nit.
3 Tey, mbooloo Yàlla mi dafay jëfandikoo masin yu gaaw lool ci defar téere ak it ay ordinatër. Loolu tax na ñu mën a defar ci ay téemeeri làkk ay Biibël ak yeneen téere yuy wax ci li nekk ci Biibël bi. Mën nañu yónnee it téere yooyu ci lu gaaw lool, fu sore ci kow suuf si. Nit ñu dëkk ci 235 réew, ñu ngi ciy jot. Yexowa dafa jaar ci xelam mu sell mi ngir xiir ñi koy jaamu ci jëfandikoo masin ak yeneen yi boroom xam-xam yi sàkk. Looloo tax, ñi mën a jot ci dëgg gi nekk ci Biibël bi, tey lañu gën a bare.
4 Li ku nekk mën a soppi ci dundam : Am na ñu dem ba soppi ni ñuy dunde ngir yokk li ñuy def ci waaraate bi. Ñu ci bare yombalal nañu seen dund ngir gën a mën a bokk ci liggéeyu waare bi. Am na ñu toxu ci béréb fu ñu gën a soxla ay waarekatu Nguur gi. Am na it ñu jàng làkk bu ñu xamul woon, ngir mën a waar nit ñu gën a bare.
5 Am na leneen li ñu mën a def itam. Mooy waare ci waxtu fu nit ñi nekk seen kër ak it ci béréb fu ñu mën a fekk nit ñi. Xéyna du ngeen fekk nit ñi ci seen kër ci bëccëg. Kon ndax mënuloo defaraat sa porogaraam ngir waaraate ci ngoon bala muy guddi ? Ndax amul ci seen gox béréb yu bare nit foo mën a waare ? Ndax mas nga waare ci telefon walla ci béréb fu bare bitig ? Ndax tàmm nga seet noo mënee waare saa yoo ci amee bunt ?
6 Bokk ci liggéeyu waare bi jëm ci turu Yexowa ak ci Nguur gi, lu réy la. Dëgg gi ñuy jële ci Kàddu Yàlla, dafay maye dund. Kon nañu kontine di ko xamal nit ñu gën a bare. — Macë 28:19, 20.
[Laaj yi]
1. Lan la karceen yu njëkk ya doon def ngir xamal xibaar bu baax bi nit ñu gën a bare ?
2, 3. a) Li Isayi 60:16 wax, naka lay amee tey ? b) Naka lañuy jëfandikoo li boroom xam-xam yi sàkk ngir diine dëgg ji jëm kanam ?
4. Lan la yenn waaraatekat soppi ci seen dund ngir mën a xamal nit ñu gën a bare xibaar bu baax bi ?
5, 6. Lan ngeen mën a def ci seen gox ngir jot nit ñu gën a bare ?