Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru ut : Benn ci téere bu def 32 xët ci yi nekk fii : Dieu se soucie-t-il vraiment de nous ? ; Doit-on croire à la Trinité ? ; Dunda léen bà fàw ak banéx ci suf si! ; Le gouvernement qui établira le Paradis ; Le nom divin qui demeure à jamais ; Quand la mort frappe un être aimé... ; Que devient-on quand on meurt ? ; Quel est le but de la vie ? Comment le découvrir ? ; “ Voici, je fais toutes choses nouvelles ”. Septaambar : Y a-t-il un Créateur qui se soucie de vous ? Mën nga wone it : La vie : comment est-elle apparue ? Évolution ou création ? Nit ki, bu bëggulee jël téere boobu, mën nga ko won téere Veillez ! Oktoobar : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu waxtaan bi neexee nit ki, won ko téere Laaj. Nowàmbar : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Xam-xam walla kayit bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ?
◼ Weeru oktoobar dina am juróomi samdi ak juróomi dimaas. Kon dina baax lool ci ku bëgg nekk pioñee buy jàpple.
◼ War nañu denc bu baax xët 5 ak 6 yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Dinañu ko soxla ngir ndaje bu mag bu ñaari fan ak ndaje bu mag bu benn fan yi ñuy am ci atum liggéeyu waare 2006.
◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 septaambar lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw ginnaaw bés boobu. Bu fekkee ne dangeen am kees fu ngeen di dajale xaalis ngir tabax ay Saalu Nguur, walla toppatoo Saal bi, walla yeneen keesu xaalis, seetleen it ndax xaalisu kees yooyu mat na. Bu ñu seetee kees yooyu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.
◼ Ñu ngi leen di fàttali ne kenn warul a joxe adareesu bànqaas bi ngir ñu yónnee ko fa ay leetar yu mu moom. Yenn saay dañuy bind ay leetar ngir waar nit ku suñu waxtaan neex, walla nit ku ñu fekkul këram, walla nit ñu dëkk ci béréb yu yombul a jot. Waaye bu ñuy bind leetar yu mel noonu sax, waruñu joxe adareesu bànqaas bi ngir nit ki tontu ñu fa. Suñu adareesu bopp lañu war a joxe, ndaxte waaraate bi bokk na ci li nit ku nekk di def ngir jaamu Yàlla (Macë 28:19, 20 ; Room 10:14, 15). Su fekkee ne joxe sa adareesu kër wóorul, bindal sa tur ak adareesu Saalu Nguur gi. — Seetal Sasu Nguuru Yàlla bu me 2002, Tont ci seen laaj.
◼ At mu nekk, dañuy seet ñaata téere ak yéenekaay ñoo des ci mbooloo mi. Ren, bésu 31 ut 2005, lañu ko war a def, walla ci bés bi ko gën a jege. Liggéey boobu, mu ngi mel ni li kiy toppatoo téere yi ngir mbooloo yi bokk benn Saalu Nguur di def weer wu nekk. War nañu bind li ñu ci waññ ci kayit bi tudd Stock des publications (S-18). Su amee ay mbooloo yu bokk fi ñuy dence seeni téere, kiy toppatoo yéenekaay yi ci mbooloo mu nekk dina wax ñaata yéenekaay ñoo des ci mbooloom. Mbooloo miy toppatoo yeneen mbooloo yi ci wàllu téere yi, bànqaas bi dina ko yónni ñetti kayit yu tudd Stock des publications (S-18). Nangeen bind li ñu ciy laaj ci benn bi te yónnee ko bànqaas bi, bala bésu 6 septaambar. Ñaareelu kayit bi, sotti lay doon. Denc leen ko ci mbooloo mi. Ci ñetteel bi ngeen di bind bu ngeen di def liggéey boobu. Sekkerteeru mbooloo miy toppatoo téere yi mooy toppatoo liggéey boobu. Moom ak wottukat biy jiite ci mbooloo moomu ñoo war a bind seen tur ci kayit bi ñuy yónnee ak it ci bi ñuy denc (S-18).
◼ Kàrt yi ñuy taf ci suñu yére bu ñuy dem ci ndaje mi gën a mag ci atum 2005, dinañu ko boole ak téere yi ñuy yónnee mbooloo yi. Jarul ngeen koy laaj. Mbooloo yi am gurup buy làkk beneen làkk kese ñoo ko war a laaj. Dinañu seet ci ni mbooloo mu nekk tollu ngir yónnee kàrt yooyu ci ay paket yu def 25 kàrt, paket bu nekk. Su fekkee ne kàrt yi ngeen jot doyul, mën ngeen laaj yeneen kàrt ci kayit bi tudd Demande de publications (S-14). War nañu laaj it palastig fi ñuy defe kàrt yi, bu amee ku ko soxla.
◼ Mbooloo yi war nañu tàmbali boole téere yii di topp ci téere yi ñuy laaj bànqaas bi : Calendrier des Témoins de Jéhovah 2006, Examinons les Écritures chaque jour 2006 ak Annuaire des Témoins de Jéhovah 2006. Dinañu wax ci yan làkk lañu mën a am téere yooyu ci kayit bi tudd “ Avis aux congrégations ”. Kayit boobu, weer wu nekk ñu yónnee ko mbooloo mu nekk.