TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/05 p. 1
  • Xam-xam buy jëme ca dund gi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Xam-xam buy jëme ca dund gi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 12/05 p. 1

Xam-xam buy jëme ca dund gi

1 Bu ñu gisee ni nit ñi di kontaane bu ñuy jàng dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla, dañuy bég. Jàngale xam-xamu Yàlla ak li mu bëgg def, lu neex la ci xol. Xam-xam bu mel noonu dafay jëme ca dund gu dul jeex. — Ywna. 17:⁠3.

2 Lu tax mu gën xam-xam bu mu mënta doon : Tey, ci àddina si, fasoŋ bi ñuy jàngale ak li ñuy jàngale bare na lool (Daj. 12:12). Waaye mbirum Yàlla yu kéemaane yi, maanaam “ màggaayi Yàlla ” moo gën fuuf xam-xam boobu (Jëf. 2:11). Ndax xam-xam bi àddina sii di maye mën na tax nit ñi gën a jege Yàlla ? Ndax mën na tax ñu gën a xam li Yàlla bëgg def ? Ndax tax na nit ñi xam lan mooy xew bu nit deewee, ak lu tax naqar am ci àddina ? Ndax tax na ba nit ñi am yaakaaru ëllëg ? Ndax tax na ba njaboot yi gën a am jàmm ? Déedéet. Ci li Yàlla di jàngale kese lañu mënee am tont laaj yu am solo yi nit ñi di laajte ci dundu doomu-Aadama yi.

3 Li Yàlla di jàngale dafay indi loo xam ne dafa ñàkk lool tey. Dafay tax nit gën a baax. Tey, nit ñi, boo bokkul ak ñoom xeet walla réew, dañu lay bañ. Waaye Kàddu Yàlla dafay dindi loolu ci xolu nit ñi nangu li muy jàngale, te di ko topp (Yaw. 4:12). Dafay tax nit ñi bañ a nekkati nit ñu gaaw a mer te bëgg xeex. Te dafay tax it ‘ ñu sol dund gu bees gi ’. (Kol. 3:​9-11 ; Mik. 4:​1-3.) Te it li Yàlla di jàngale tax na ba ñi koy nangu am doole bi ñuy xeexe jëf ak jikko yi neexul Yàlla yi ñu tàmmoon a def. — 1 Kor. 6:​9-11.

4 Lu tax mu jamp tey : Suñu Jàngalekat bu mag bi xamal na ñu li xew-xew yi ci àddina si tekki. Ci àtte bi Yàlla yégle, am na lu mu wax ci niti tey te ñu war ko xamal niti àddina si sépp (Peeñ. 14:​6, 7). Mooy lii : Yeesu mu ngi jiite ci asamaan si. Léegi mu alag diine fen yi yépp. Te it, léegi Nguuru Yàlla alag nguur yi nekk ci kow suuf si sépp (Dañ. 2:44 ; Peeñ. 11:15 ; 17:16). Kon nag, am na lu jamp lu nit ñi war a def : dañu war a nangu Buuru bi Yàlla tànn, te nga xam ne mu ngi ilif tey ; war nañu génn ci biti Babilon bu mag bi ; te war nañu woo turu Yexowa ci fasoŋ buy wone ne dañu am ngëm (Sab. 2:​11, 12 ; Room 10:13 ; Peeñ. 18:⁠4). Kon nag, nañu def lépp li ñu mën ngir jàngal nit ñi xam-xam biy jëme ca dund gi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager