Yégle Yi
◼ Téere yi ñuy wone ci wéeru Màrs : Qu’ enseigne réellement la Bible ? Nañu góor-góorlu ngir komaase ay njàngum Biibël. Awril ak me : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Dinañu góor-góorlu ngir seeti ñi suñu waxtaan neex te tàmmuñu teewe suñu ndaje yépp, fekk teewe woon nañu ndaje fàttaliku bi ak waxtaan bi ñu faral di am ci àddina si sépp bu ndaje fàttaliku bi weesoo. Li waral ñuy dellu seeti nit ñooñu, mooy bëgg komaase njàngum Biibël ak ñoom. Suweŋ : Qu’enseigne réellement la Biibël ? Nañu góor-góorlu ngir komaase ay njàngum Biibël.
◼ Bu La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yu bees yi agsee ci mbooloo yi rekk, nañu ko jox waaraatekat yi. Loolu dina tax ñu mën a xam bu baax li nekk ci yéenekaay yi bala ñu koy wone ci waaraate bi.
◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn dina seet ndax xaalis bi mbooloo mi amoon ci weeru desàmbar, sãwiyee ak feewriyee mat na. Waruñu jël benn nit ngir mu def liggéey boobu ñaari yoon yu toppante. Bu ñu ci paree, war nañu ko xamal mbooloo mi bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Seetleen li ñu wax ci kayit bi tudd Instruction pour la comptabilité des congrégations (S-27).