Yégle Yi
Téere yi ñuy wone ci weeru Septaambar : Qu’enseigne réellement la Bible ? Dinañu def lépp ngir komaase njàngum Biibël ci suñu waxtaan bu njëkk bi. Su nit ki amee téere boobu ba pare, won ko ci lu gàtt naka lañuy doxale njàngum Biibël ngir mu gis njariñ bi ci nekk. 1 ba 19 oktoobar : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Bu suñu waxtaan neexee nit ki, won ko kayit bu ndaw bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ? te waxtaan ci ak moom ngir mën a komaase njàngum Biibël. 20 oktoobar ba 16 nowàmbar : Dinañu joxe kayit bu ndaw bi tudd Ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo. 17 ba 30 nowàmbar : Téere Qu’enseigne réellement la Bible ? Nañu góor-góorlu ngir komaase njàngum Biibël. Desàmbar : Téere Le plus grand homme de tous les temps. Bu nit ki waxee ne am na ay doom, nañu ko won téere Écoute le grand Enseignant.
◼ Nowàmbar dina nekk wéer bu baax lool ngir nekk pioñee buy jàpple ndaxte juróomi samdi ak juróomi dimaas la am.
◼ At mu nekk, bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, am na waxtaan bu ñuy faral di am ci àddina si sépp. Ci atum 2009, ci ayu-bés biy tàmbali bésu 20 awril 2009 lañu koy def. Bu ci kanamee, dinañu leen wax turu waxtaan bi. Mën na am wottukat biy wër ci mbooloo yi war a nekk ci seen mbooloo ayu-bés boobu. Walla ngeen am ndaje bu mag. Bu boobaa, nangeen def waxtaan boobu ayu-bés bi ci topp. Benn mbooloo warul def waxtaan boobu bala ayu-bés biy tàmbali bésu 20 awril.
◼ Wottukat biy jiite walla keneen ki mu tànn, dina seet ndax xaalis bi mbooloo mi am ci weeru suweŋ, sulyet ak ut mat na. Benn nit warul def liggéey boobu ñaari yoon yu toppante. Bu ñu ko defee ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy yégal nit ñi fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. — Seetleen kayit bi tudd Instructions sur la comptabilité des congrégations (S-27).
◼ Ndaje bu mag bu waroon a am ca Bamako ca Mali diggante 2 ba 4 sãwiyee, bési 3 ak 4 sãwiyee 2009 lay doon léegi. Xamleen ne porogaraam bu ñaari fan yi du am ci bàmbara kese. Dina am it ci tubaab. Dinañu jox yeneen leeral mbooloo yi war a teewe ndaje yu mag yooyu.