Nañu fàttaliku li ñu jàng ci lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, dinañu ci waxtaan ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi ñuy def diggante 29 desàmbar 2008 ba 4 sãwiyee 2009. Ci lu mat 20 minit, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu jàng ci lekkool bi diggante 3 nowàmbar 2008 ba 4 sãwiyee 2009.
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Lu tax xelal nit ak “ mbëggeel ” am solo lool ? (Flm. 9) [be p. 266 § 1-3]
2. Naka lañuy maye suñuy moroom fit ? [be p. 268 § 4–p. 269 § 2]
WAXTAAN N° 1
3. Lu tax leetar bi Pool bindoon Tit “ baax te am njariñ ” ci ñun tey ? (Tit 3:8) [si p. 241 § 8]
4. Lu tax leetar bi Piyeer njëkk a bind baax ci suñu jamano ? [si p. 251 § 1]
5. Misaal yi nekk ci téere Peeñu ma, lan lañu war a def ci ñun ? [si p. 263 § 1]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
6. Lu tax ci Tit 2:3 Pool boole bañ a “ jëw ” ak bañ a “ xér ci sangara ” [w94 15/6 p. 20 § 12]
7. Bu ñuy wax ne Seytaane moo “ yore dooley dee ”, ndax dañu bëgg a wax foofu ne mën na rey ki ko neex ? (Yaw. 2:14 ) [w08 15/10 “ La Parole de Jéhovah est vivante — Points marquants des lettres à Tite, Philémon et aux Hébreux ”]
8. Kan mooy ‘ ki bind ’ kóllëre bu bees bi ? (Yaw. 9:16) [w08 15/10 “ La Parole de Jéhovah est vivante — Points marquants des lettres à Tite, Philémon et aux Hébreux ”]
9. Ànd ak jàmm lu muy tekki, te lan lañu war a laaj suñu bopp ci loolu ? (Saag 3:17) [w08 15/3 p. 24 § 18]
10. “ Yàllaa ëpp suñu xol ”, lan la kàddu yooyu di tekki ? (1 Ywna. 3:20) [w05 1/8 p. 30 § 19]