Nañu fàttaliku li nu jàng ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla pur ndaje yi ci làkku Wolof
Laaj yii di topp, dinañu ci waxtaan ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ñuy am ci semenu 28 desàmbar 2015 ci lu mat 20 minit. Kiy jiite lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu jàng ci lekkool bi diggante 2 nowàmbar ba semenu 28 desàmbar 2015. Li ñu bind ci biir koroose yi, dafay wone weer bi ak semen bi ñu gis njàngale bi.
Li Daawuda wax ci gore, naka lay dalale xelu jaamu Yexowa yi tey ? (2 Samiyel 22:26) [2 nowàmbar w10 1/6 p. 26 § 6-7]
Naka la Natan wonee ngor ci Yàlla, te naka lañu mënee roy jikko bu rafet boobu tey ? (1 Buur yi 1:11-14 ) [9 nowàmbar, w12 15/2 p. 25 § 1, 4-5]
Dafa mel ni Suleymaan dafa sukkandiku ci gis-gisam bu jubul ngir rekk bañ a topp yenn ci santaane Yàlla yi. Loolu naka la mënee dal ab jaamu Yàlla tey ? (1 Buur yi 3:1) [16 nowàmbar, w11 15/12 p. 10 § 12-14]
Ci ñaan bi Suleymaan defoon, dafa ci wax dëgg yu jëm ci Yexowa Yàlla. Naka la dëgg yooyu di dëgërale suñu ngëm ? Te bu ñuy xalaat bu baax ci dëgg yooyu, ban njariñ la ñu ciy jële ? (1 Buur yi 8:22-24, 28) [23 nowàmbar, w05 1/7 p. 30 § 3]
Daawuda dafa doon topp Yàlla “ cig mat ”. Lu tax loolu war ñu xiir ñu def ni moom ? (1 Buur yi 9:4) [30 nowàmbar, w12 15/11 p. 7 § 18-19]
Bi Abiya deewee, Yexowa dafa waxoon ñu rob ko ni mu jaadoo, loolu lu mu ñuy jàngal ? (1 Buur yi 14:13) [7 desàmbar, cl p. 244 § 11]
Bu ñu xalaatee bu baax ci li ñu nettali ci 1 Buur yi 17:10-16, loolu naka lay dëgërale suñu pas-pas ci kontine di wóolu Yexowa ak suñu xol bépp ? [14 desàmbar, w14 15/2 pp. 13-15]
Ci 1 Buur yi 18:21 Ilyaas lii la wax mbooloo ma : “ Yéen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa ? ”. Wax jooju lu muy tekki ? [21 desàmbar, w08 1/1 p. 19 § 3-4]
Bi Ilyaas jaaxlee lool, xeex na ba génn ci, ban njariñ lañu mën a jële ci roy ko ? (1 Buur yi 19:4) [21 desàmbar, ia pp. 102-103 § 10-12 ; w14 15/3 p. 15 § 15-16]
Ban gis-gis bu bon la Buur Akab amoon, te naka la karceen yi mënee moytu am gis-gis boobu tey ? [28 desàmbar, lv pp. 164-165, encadré ; w14 1/2 p. 14 § 3-4]