TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 46
  • Miir Yi Wër Yeriko

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Miir Yi Wër Yeriko
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Raxab Nëbb Na Ñi Ñów Yërndu Réew Mi
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Raxab dafa gëmoon Yexowa
    Jàngal-leen seeni doom
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 46
Yosuwe mu ngi jiite waa Israyil yiy yuuxu ak di ëf ci béjjén yi te miiri Yerikoo yaa ngi daanu

NETTALI 46

Miir Yi Wër Yeriko

LU TAX miiri Yeriko di daanu ? Dafa mel ni bomb bu mag moo dal seen kow. Waaye bomb amul woon ca jamano jooja. Fetal amul woon sax. Yexowa moo tax miir yi di daanu. Moom moo def beneen kéemaan. Nañu seet lu tax loolu yépp am.

Lii la Yexowa wax Yosuwe : ‘ Bés bu nekk, yow ak ñiy xeex ak yow ngir waa Israyil, maanaam sa xarekat yi, nangeen dox, wër dëkk bi, benn yoon. Nangeen def loolu juróom-benni fan. Nangeen yóbbaale gaalu kóllëre gi. Juróom-ñaari saraxalekat ñoo war a dox ci kanamam te ëf ci seeni béjjén. ’

‘ Ci juróom-ñaareelu bés bi, nangeen wër dëkk bi juróom-ñaari yoon, ba pare ëf lu yàgg ci béjjén yi, te na ñépp yuuxu, mel ni yuuxu bu ñuy yuuxu bu ñuy xeex. Miir yi wër Yeriko yépp dinañu daanu. ’

Miiri Yeriko yi daanu nañu, ba mu des këru Raxab gi ñu takkoon buum bu xonq bi

Yosuwe ak mbooloo mi def li Yexowa waxoon. Dañuy dox rekk. Kenn waxul. Béjjén yi ak tànk yi rekk lañuy dégg. Wóor na ne ñi nekk ci biir Yeriko te bañ mbooloo Yàlla tiitoon nañu lool. Ndax yaa ngi gis buum bu xonq biy génn ci palanteer bi nekk ci kow ? Palanteeru kan la ? Bu Raxab bi la. Def na li ko ñaari góor ñi ñówoon yërndu réew mi waxoon. Njabootam yépp ñu ngi ak moom ci biir kër gi di xaar.

Ci juróom-ñaareelu fan bi, dañu wër dëkk bi juróom-ñaari yoon, ëf ci béjjén yi, xarekat yépp yuuxu, miir yi daanu, Yosuwe daldi wax lii : ‘ Reyleen ñi fi nekk ñépp, ba pare lakk dëkk bi. Lakkleen lépp li fa nekk. Bàyyileen rekk lu nekk xaalis, wurus, përëm ak weñ, te def ko fi ñuy dence alalu tàntu Yexowa bi. ’

Yosuwe wax na itam ñaari góor ñi demoon ci Raxab : ‘ Demleen ci kër Raxab, indileen ko, moom ak njabootam yépp. ’ Raxab ak njabootam mucc nañu, ni leen ko ñaari góor ñi digoon.

Josué 6:1-25.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager