TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 97
  • Yeesu, Buur Bi, Mu Ngi Ñów

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yeesu, Buur Bi, Mu Ngi Ñów
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yeesu Faj Na Ñi Feebar
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Mbaam Buy Wax
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Ci Tundu Oliw Yi
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Yeesu Mu Ngiy Dellu Asamaan
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Xóotalal waxtaan bi
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 97
Yeesu mu ngi toog ci kow mbaam-sëf, mbooloo mi di ko nuyu ak ay bànqaasu tiir

NETTALI 97

Yeesu, Buur Bi, Mu Ngi Ñów

TUUTI ginnaaw bi Yeesu fajee ñaari gumba yi doon yelwaan, dafa dem ci dëkk bu ndaw bu jege woon Yerusalem. Mu ne ñaari taalibeem yi : ‘ Demleen ci biir dëkk bi. Dingeen gis mbaam-sëf bu ndaw. Yewwileen ko, ngeen indil ma ko. ’

Ñu indil ko ko, Yeesu toog ci kowam, daldi dem Yerusalem. Bi mu fa jegee, nit ñu bare ñów teeru ko. Ñi ci ëpp daldi summi seen mbubb te lal ko ci yoon bi. Ñeneen ñi dagg ay bànqaasu tiir, def leen ci yoon bi itam. Ñu nekk di wax ci kow, naan : ‘ Na Yàlla barkeel buur bii di ñów ci turu Yexowa ! ’

Ca jamano yu yàgg ya ci Israyil, buur bu ñu sog a fal, dafa doon yéeg ci mbaam-sëf bu ndaw, dugg ci biir Yerusalem ngir nit ñi gis ko. Loolu la Yeesu di def. Te nit ñooñu ñu ngi wone ne bëgg nañu Yeesu nekk seen buur. Waaye du ñépp a ko bëgg. Li xewoon bi Yeesu demee ca kër Yàlla ga moo koy wone.

Ci kër Yàlla gi, Yeesu faj na ay gumba ak ay lafañ. Bi xale yi gisee loolu, ñu daldi tagg Yeesu ak baat bu kowe. Saraxalekat yi daldi mer. Ñu ne Yeesu : ‘ Ndax dégg nga li xale yi di wax ? ’

Yeesu tontu leen ne : ‘ Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleen a jàng lii ci Biibël bi : “ Ci gémmiñu xale yu ndaw la Yàlla di jaar ngir tagg am ? ” ’ Xale yi daldi kontine di tagg ki Yàlla def buur.

Bëgg nañu mel ni xale yooyu, du dëgg ? Mën na am ay nit jéem ñu tere wax ci nguuru Yàlla. Waaye ba tey dinañu kontine di wax nit ñi lu rafet lool li Yeesu di defal nit ñi ëllëg.

Yeesu, du ci jamano bi mu nekkee ci kow suuf la naroon a nguuru. Loolu, kañ lay doon ? Taalibe Yeesu yi bëggoon nañu ko xam. Dinañu ci wax ci nettali bii di topp.

Macë 21:1-17 ; Yowaana 12:12-16.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager