Woy-Yàlla 6 (13)
Njébbalu karceen
(2 Musaa 39:30)
1. Ndax Yeowa mooy ki sàkk
Jaww, ji ne ŋàpp,
Moo moom asamaan ak suuf si.
Jëfam amul gàpp.
Nawu dund, jagleel na ko
Mbindaafon yi te won
Ne yelloo na, dëgg, ñu naw ko,
Ñu jaamu ko, yit, ci yoon.
2. Xeetu waa Israyel, démb
Ca Sinaay, waat na lii:
‘Sàrtu Yeowa lañuy top’,
Def kook xol bu tàlli.’
Ni boroom-kër la leen moome,
Jënde leen ca géej ga.
Xeetu nit ñu jébbalu ci moom,
Looloo doon seen teraanga.
3. Ci biir ndox lañu sóob Yeesu,
Ndax mottali li jub.
Mu teew foofa ci suufeelu,
Doon misaal ngir kuy tuub.
Ba ko xelu Yàlla tànnee,
Mu génne ca Yurdan;
Déggal te gore la dogu woon,
Jébbalu ba abadan.
4. Yeowa, ñu ngi sa kanam,
Di naw sa tur wu mag,
Xàcceek suñu bopp dëgg.
Suñ’ njaamu, yal na jag.
Sa jenn kot’, ji nga jébbal,
Fey na njëg lu jafe.
Kon, dootuñu wéy ci li ñu neex,
Li la soob lañuy jëfe.