Woy-Yàlla 24 (50)
Nañu wuyu mbëggeelu Yàlla
(1 Yowanna 4:11)
1. Yàlla, amuloo moroom; yaw, yaa di suñu Boroom,
Bi ñu bëgg te yelloo tagg.
Naw nañ’ sa tur wi jolli, sa Kàddu gi-ñ ñu dolli
Ndax ñu mën’ xam say yoon, yi màgg.
Laabiir daa fés ci say mbir, teyit sa njubte daa bir;
Yaa ngiy wone sago ak kàttan.
Dëgg, xam nañu xéll ne sàmm xol bu sell,
Barke la ñuy jural—yuy baawaan.
2. Yaa ñu jëkk’ won mbëggeel; Krist it won na ñu cofeel;
Ñun it, bëgg nañ’ laak suñu xol.
Sa tur, Krist sellalsi na, sa mbëggeel feeñalsi na,
Di maye abadan niki yool.
Mbëggeelam ci moroomam, gu ko sut masul a am;
Jébbal na, ni sarax, bakkanam.
Ngir sax ci suñu jàmm, nañ’ fonk suñu Sàmm,
Te topp bu baax ay xelalam.
3. Ci suñu sas nañ’ takku, fitnay noon wéy di dékku;
Nañu wéy di xamle liy dëgg.
Nañ’ waar ak xol bu tàlli; booba dinañ’ mottali
Mbëggeel; di ko won ñép’ lañ’ bëgg.
Nañ’ waar, di jàppalante, te na suñu bëggante
Fésloo ñiy topp dëgg sa Doom.
Nguur gi, nañu ko jiital, di séentu bile xiirtal:
“Sas! Def nga lu baax; amoo moroom!”