Woy-Yàlla 95 (213)
Nañu ànd a liggéey ci déggoo
(Efes 4:3)
1. War nañu, ñun ñép’, ànd jëf.
Moom-sa-bopp coono lay sëf.
Méngoo, bokk menn xalaat
Day jur jàmm ju naat.
Déggoo mbég lay yóbbe.
Ñu-ng’ koy dund xaat.
Su ñu amee ay manoore,
Bu-ñ’ ci wut ndam ndax day lore.
Nañu yem, te sax ci mbëggeel,
Di woy Yàllaak cofeel.
2. Wujje ak ñee nit daa bare
Ci dunyaa ju ni soxore.
Jàmm lañ’ bëgg tey fexe.
Niki lay la féexe.
Jàmm, akay féexal!
Ni lay la féexe.
Ñàkk-déggoo, lée-lée, mu am;
Ndax dañoo matadi itam.
Gaaw koo saafara njariñ la.
Déggoo moo neex Yàlla.
3. Ba ñuy ànd jëf bés bu ne,
Nañ’ wone déggoo saa su ne.
Lu neex la, te rafet, te baax.
Ci fonk ko, nañ’ sax.
Déggoo lañu fonk,
Ndax, ca dëg’, daa baax.
Déggoo day jur yool bu rafet:
Waaw, dëkk ak Yaa ba màgget.
Am nañ’ jàm’ ak suñu moroom,
Ci tetteb suñ’ Boroom.