Njàngale 13
Naka nga mënee xam diine dëgg ji ?
Ndax Yàlla nangu na diine yépp, walla benn rekk ? (1)
Diine yuy wax ne ci yoonu Isaa lañu bokk, lu tax ñu baree nii ? (2)
Naka nga mënee xàmme taalibe Isaa yu dëgg yi ? (3-7)
1. Isaa benn diine bu boole taalibeem yu dëgg yi rekk la taxawaal. Kon tey, ñiy jaamu Yexowa Yàlla ci dëgg, benn mbooloo rekk lañu wara nekk (Yowanna 4:23, 24 ; Efes 4:4, 5). Mbind mu sell mi nee na ñi nekk ci yoon bu xat biy jëme ca dund, barewuñu. — Macë 7:13, 14.
2. Mbind mu sell mi waxoon na ne bu ndawi Isaa yi deewee, dina am seen ginnaaw ay njàngale yu nekkul dëgg ak ay jëf yu bokkul ci li Isaa jàngalewoon, yu nara roofu ndànk-ndànk ci biir mbooloo taalibeem yi. Dina am itam ay nit ñiy jéema xëcc ñi gëm ngir ñu topp leen te baña topp Isaa (Macë 7:15, 21-23 ; Jëf ya 20:29, 30). Looloo tax diine yiy wax ne ci yoonu Isaa lañu bokk baree nii. Naka lañu mënee xàmme taalibe Isaa yu dëgg yi ?
3. Li gëna tax ñu mëna xàmme taalibe Isaa yu dëgg yi mooy mbëggeel dëgg bu ñuy wone ci seen biir (Yowanna 13:34, 35). Duñu leen jàngal ne ñoo gën ñi bokk ci yeneen xeet, walla ñi ñu niroowul der. Duñu leen jàngal itam ne dañu wara bañ ñi dëkk ci yeneen réew (Jëf ya 10:34, 35). Looloo tax duñu bokk ci xare yi. Taalibe Isaa yu dëgg yi dañuy jàpp ñi ñu bokkal ngëm ni ay mbokk, muy góor di jigéen. — 1 Yowanna 4:20, 21.
4. Leneen lu ñuy taxa xàmme diine dëgg ji mooy ñi ci bokk dañuy fonk Mbind mu sell mi bu baax-a-baax. Dañuy nangu ne Kàddu Yàlla la te gëm nañu li ci nekk (Yowanna 17:17 ; 2 Timote 3:16, 17). Dañoo gëm ne Kàddu Yàlla moo ëpp solo xalaat walla aada nit ñi (Macë 15:1-3, 7-9). Bés bu nekk dañuy jéema topp li Mbind mu sell mi wax. Duñu jàngale lenn ba pare di jëf li àndul ak li ñu jàngale. — Titt 1:15, 16.
5. Diine dëgg ji war na it màggal turu Yàlla (Macë 6:9). Isaa dafa xamaloon ñeneen nit ñi turu Yàlla, maanaam Yexowa. Loolu la taalibe Isaa yu dëgg yi wara def itam (Yowanna 17:6, 26 ; Room 10:13, 14). Ñan ñooy ñiy xamal nit ñi turu Yàlla ci sa dëkk ?
6. Taalibe Isaa yu dëgg yi dañu wara waar nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla. Loolu la Isaa doon def. Dafa faraloon di wax ci lu jëm ci Nguuru Yàlla (Lukk 8:1). Sant na taalibeem yi ñu waare xibaar boobu ci àddina si sépp (Macë 24:14 ; 28:19, 20). Taalibe Isaa yu dëgg yi, dañu gëm ne Nguuru Yàlla rekk mooy indi jàmm ak salaam bu mat ci kow suuf si. — Sabuur 146:3-5.
7. Taalibe Isaa yi waruñu bokk ci àddina su bon sii (Yowanna 17:16). Duñu bokk ci mbirum politig walla ci yeneen fasoŋu werante diggante nit ñi. Dañuy moytu dundin, jëfin ak jikko yu bon yi bare ci àddina si (Saak 1:27 ; 4:4). Ndax xam nga ci sa gox benn mbooloo nit ñu bokk diine ñi nga xam ne dañuy jëfe luy wone ne taalibe Isaa yu dëgg lañu ?
[Nataal yi nekk paas 26, 27]
Taalibe Isaa yu dëgg yi dañuy bëggante, fonk bu baax Mbind mu sell mi te dañuy waar nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla