TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • gf lesoŋ 5 p. 8-9
  • Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana
  • Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Mën ngaa am ëllëgu bànneex!
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
  • Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Mën nga nekk xaritu Yàlla !
gf lesoŋ 5 p. 8-9

NJÀNGALE 5

Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana

Dund ca Àjjana du mel ni dund ci suñu jamano. Yàlla masul bëgg suuf si fees ak coono, naqar, walla metit. Bu ci kanamee, Yàlla dina defar suuf si mu nekk àjjana. Àjjana, naka lay mel ? Nañu seet li Mbind mu sell mi wax :

Ay nit yuy feexal seen xol ci biir àjjana

Nit ñu baax. Àjjana dina nekk këru xaritu Yàlla yi. Nit ku nekk dina defal moroomam lu baax. Dinañu dund dund gu sell ni ko Yàlla bëgge. — Léebu 2:21.

Lekk bu bare. Ca Àjjana, xiif dootul am. Mbind mu sell mi nee na : “ Pepp [maanaam, lekk] dina bare ci kow suuf si. ” — Sabuur 72:16.

Ay nit yu nekk di tabax kër ci biir Ajjana, ñeneen ñi de dajale lekk, ak yaay bu uuf doomam bu jigéen

Kër yu rafet ak liggéey bu neex. Bu suuf si nekkee Àjjana, njaboot gu nekk dina am këru boppam. Nit ku nekk dina def liggéey bu koy indil bànneex dëgg. — Isayi 65:21-23.

Jàmm ci kow suuf si sépp. Kenn dootul xeex walla dee ci xare. Kàddu Yàlla nee na : “ [Yàlla] mu ngiy tax xare yi jeex. ” — Sabuur 46:8, 9.

Wér-gi-yaram. Mbind mu sell mi dig na ne : “ Kenn ku dëkk [ca Àjjana] du ne : ‘ Dama feebar. ’ ” (Isayi 33:24). Te itam, kenn dootul lafañ walla gumba walla tëx walla muuma. — Isayi 35:5, 6.

Metit, naqar ak dee, dootul am. Kàddu Yàlla nee na : “ Dee dootul am walla naqar walla jooy walla mettit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ” — Peeñu bi 21:4.

Nit ku bon dootul am. Yexowa dig na ne : “ Nit ñu bon ñi dinañu leen jële ci suuf si ; te lu jëm ci workat yi dinañu leen buddee ci kowam. ” — Léebu 2:22.

Nit ñi dinañu bëgg te fonk ku nekk sa moroom. Jubadi, noot nit, bëgge, ak bañante, dootul am. Nit ñi dinañu nekk benn te dund dund gu sell ni ko Yàlla bëgge. — Isayi 26:9.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager