Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ?
Lu tax ñu war a jàng Mbind mu sell mi ?
MBIND mu sell mi melul ni yeneen téere yi. Ndigalu Yàlla yi ñoo ci nekk. Yexowa dafa ñu bëgg moo tax mu jox ñu ndigal yooyu (1 Tesalonikk 2:13). Boo toppee li Mbind mu sell mi wax, dina la njariñ bu baax-a-baax. Dinga gën a bëgg Yàlla, te dinga ko gën a jege moom mii di maye “ gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat ”. (Saak 1:17.) Dinga xam ni nga ko mënee jege ci ñaan. Boo nekkee ci coono, dinga gis ni la Yàlla di dimbalee. Boo toppee li Mbind mu sell mi wax, Yàlla dina la may dund gu dul jeex. — Room 6:23.
Dëgg gi nekk ci Mbind mu sell mi, dafay leeral mbir yu bare. Tey, ay milyoŋi nit dañu gëm lu dul dëgg. Ngëm yooyu ñoo leen di ilif. Ñi xam li nekk ci Mbind mu sell mi, mucc nañu ci loolu. Nañu ko seete ci lii : Ku xam li am ginnaaw dee, doo ragalati ku dee def la lu bon. Te it, boo amee mbokk walla xarit bu gaañu, dinga xam ne mënul yëg benn metit (Esekiel 18:4). Dëgg la, dinga am naqar bu réy. Waaye li Mbind mu sell mi wax ci ndekkite, dina tax nga mën koo muñ (Yowanna 11:25). Ku jàng dëgg gi jëm ci malaaka yu bon yi, dinga xam ne mbirum tuuri maam walla rab, coono kese la lay indil. Dinga xam it lu tax àddina si jaxasoo lool.
Ndigal yi ñu Yàlla jox ci Mbind mu sell mi, dañuy wone ban fasoŋu dundin moo ñuy may jàmm ak wér-gi-yaram. Seetal lii : ‘ moom sa bopp ’, [maanaam mën teye sa bopp] lu baax la ci ku bëgg am wér-gi-yaram (1 Timote 3:2). Ku ‘ sellal boppam ci bépp sobeb yaram walla bu xel ’, dafay aar boppam ci feebar (2 Korent 7:1). Boo toppee li Yàlla wax ci Mbind mu sell mi, dinga am jàmm ci sa séy te gën a am fulla. — 1 Kor. 6:18.
Boo toppee li nekk ci Kàddu Yàlla, dinga gën a bég. Xam-xam bi nekk ci Mbind mu sell mi dafay maye xel mu dal, doylu ak yaakaar. Dafay tax ñu am jikko yu rafet mel ni yërmande, mbëggeel, mbégte, jàmm, mbaaxaay ak ngëm (Gal. 5:22, 23 ; Efes 4:24, 32). Bu ñu amee jikko yooyu dina ñu nekk jëkkër, jabar, baay, ndey walla doom yu gën a baax.
Ndax bëgg nga xam naka la àddina di mel ëllëg ? Mbind mu sell mi dafa ñuy wax ci ban jamano lañu tollu. Waaye yemul ci loolu. Wax na itam ne bu ci kanamee tuuti, Yàlla dina defar suuf si sépp mu nekk àjjana. — Peeñu bi 21:3, 4.
Bu ñuy jàng Mbind mu sell mi, lan moo ñu mën a dimbali ba lépp leer ?
Xéyna mas nga jéem a jàng Mbind mu sell mi, waaye yombul woon. Xéyna danga am ay laaj, te xamoo fan la tont yi nekk ci Mbind mu sell mi. Su dee loolu la, nanga xam ne du yow rekk. Képp ku bëgg a xam li nekk ci Kàddu Yàlla, soxla na ndimbal. Ci lu mat 235 réew, Seede Yexowa yi dañuy jàngal ay milyoŋi nit te kenn du leen fey. Bëgg nañu la dimbali yow itam.
Yokkal ndànk-ndànk li nga xam ci Mbind mu sell mi. Tàmbali ko ci li ñu warul a ñàkk xam ci Mbind mu sell mi (Yawut yi 6:1). Booy def noonu, dinga dem ba mën a lekk “ ñam wu dëgër wi ” ci wàllu xel, maanaam dëgg yi gën a xóot (Yawut yi 5:14). Ci fànn bu mu mënta doon, li Mbind mu sell mi wax mooy yoon. Téere yu mel ni Lan la ñu Yàlla laaj ? dinañu la leeral li Mbind mu sell mi wax ci fànn yu bare.
Ndax bëgg nga ñu jàngal la Mbind mu sell mi ayu-bés bu nekk ?
Mën nañu la jàngal Mbind mu sell mi, ci waxtu ak béréb bu la gënal. Am na ñu koy jàng ci seen biir kër, walla ci telefon. Bu ñuy jàngale, duñu def ay gurup mel ni ci lekkool. Nit ku nekk ak ni nga mel. Kon bu ñuy jàngale dinañu seet ci li nga xam, seet ci fi nga yem ci lekkool bi, ak ci li nga nekke. Kenn du def eksamee, te duñu sewal kenn. Dinañu la tontu ci lépp li nga bëgg xam ci Mbind mu sell mi, te dinga xam li nga war a def ngir gën a jege Yàlla.
Bu ñu lay jàngal Mbind mu sell mi, doo fey dara (Macë 10:8). Ñépp lañuy jàngal, ku bokk ci diine ak ku amul benn diine. Képp ku bëgg yokk li mu xam ci Mbind mu sell mi, dinañu la jàngal, te doo ci fey dara.
Ku mën a bokk ci waxtaan bi ? Sa njaboot yépp. Mën nga woo itam xarit bu la neex. Boo bëggee it, mën nañu jàng ak yow kese.
Ñu bare dañuy jël benn waxtu ayu-bés bu nekk, ngir jàng Mbind mu sell mi. Waaye boo bëggee, njàng mi mën na gën a gudd, walla gën a gàtt. Seede Yexowa yi dinañu def li la gënal.
Ñu ngi lay woo ci njàng mi
Fexeel ba wax ak Seede Yexowa yi. Mën nga tànn benn adarees ci yi nekk fii ci suuf ngir bind leen. Dinga am ku lay ñów jàngal Mbind mu sell mi ci sa kër, te doo fey dara.
□ Yónneeleen ma téere bi tudd : Lan la ñu Yàlla laaj ?
□ Dama bëgg jàng Mbind mu sell mi ci sama kër te duma ci fey dara.
Bu ñu ko leeralul, aaya yi ñu bind ci kayit bii, ñu ngi jóge ci KÀDDUG DËGG GI, 1987.