TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • T-27 p. 1-6
  • Coono yépp, Léegi mu jeex !

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Coono yépp, Léegi mu jeex !
  • Coono yépp, Léegi mu jeex !
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Coono yi, fan lañu komaase ?
  • Laaj bi ëpp solo mooy : Kan moo war a jiite ?
  • Coono, léegi mu jeex !
  • Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Coono yépp, Léegi mu jeex !
T-27 p. 1-6

Coono yépp, Léegi mu jeex !

Lu tax coono yi bare ? Ndax mas nga laajte loolu ? Doomu Aadama yi yàgg nañu di sonn ndax xeex, ñàkk xaalis, musiba, feebar ak dee. Te loolu mu ngi gën di yokku rekk. Ndax loolu dina mas a jeex ?

Waaw waaw te ci kanam tuuti lay doon ! Kàddu Yàlla, maanaam Biibël bi, nee na : “ Ku soxor du nekkati [...]. Waaye ñi woyof ñooy moom réew mi, di bég ci jàmm ju yaa. ” (Sabóor 37:10, 11). Loolu, ba kañ lay doon ? “ Nit ñu jub ñi dinañu moom suuf si, te dinañu fa dëkk ba fàww. ” — Sabóor 37: 29, MN.

Bu Yàlla dindee lu bon ak coono yi, suuf si dinañu ko defar ba mu nekk àjjana. Nit ñi dinañu mën a dund ba fàww ak jàmm di bég te duñu feebar mukk. Kàddu Yàlla nee na : “ [Yàlla] dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit. ” — Peeñu ma 21:4.

Ci àddina bu bees boobu, ñi dee sax dinañu dekki ngir fekke barke yooyu. Ci li Biibël bi wax, am nañu “ yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki. ” (Jëf ya 24:15). Looloo taxoon Yeesu Kirist wax lii benn defkatu lu bon ku réccu woon bàkkaaram te amoon ngëm ci moom : “ Dinga texe ak man ca jataayu Yàlla. ” — Luug 23:43.

Coono yi, fan lañu komaase ?

Bu dee Yàlla dafa bëggoon doomu Aadama yi am ëllëg bu neex boobu, lu tax mu bàyyi coono yi komaase te yàgg noonu ?

Bi Yàlla sàkkee suñuy maam Aadama ak Awa, dafa leen sàkkoon ñu mat sëkk, dugal leen ci biir tool bu rafet, maanaam àjjana, te jox leen liggéey bu neex. Biibël bi nee na : “ Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. ” (Njàlbéen ga 1:31). Bu Aadama ak Awa déggaloon Yàlla, seeni doom dinañu mat te suuf si sépp dina nekk àjjana fu ñépp di dund ba fàww ak jàmm.

Yàlla dafa sàkk nit mu mën a tànn diggante def lu baax walla def lu bon. Yàlla bëggul woon Aadama ak Awa mel ni ay masin yu ñu porogaraame. Waaye bu ñu bëggoon seen jàmm yàgg, dañu waroon a tànn lu baax, maanaam topp ndigalu Yàlla yi. Ni ko Yàlla waxe, dafa ñuy jàngal ngir suñu njariñ. Moom moo ñuy won fi ñu war a jaar. (Isaie 48:17). Bu ñu tànnul lu baax, musiba lay doon ci ñoom, ndaxte Yàlla sàkkul nit pur mu jiite boppam. Biibël bi nee na : “ Xam naa bu baax, céy Yexowa, ne nit ki ñu sàkk ak suuf moomul ay tànkam, nit kuy dox mënul a seetal boppam fi mu war a aw. ” — Yérémi 10:​23, MN.

Suñuy maam Aadama ak Awa ñoom, dañu yaakaaroon ne mën nañu jiite seen bopp te bég. Waaye bi ñu weddee kiliftéefu Yàlla, Yàlla bàyyiwul leen ñu kontine di nekk ay nit ñu mat, ñu daldi komaase yàqu ba mujj a màgget te dee. Ndegam ñun ci Aadama ak Awa lañu jóge, kon dañu donn ci ñoom bàkkaar ak dee. — Room 5:12.

Laaj bi ëpp solo mooy : Kan moo war a jiite ?

Lu tax Yàlla alagul Aadama ak Awa, indi fi ñeneen ? Ndaxte Yàlla dafa bëggoon a may nit ñi jot bu doy, ngir ñu xam ndax ñoom ñoo war a jiite seen bopp walla dañu war a bàyyi Yàlla jiite leen. Ndax dinañu gën a am jàmm bu ñu jiitee seen bopp ? Jot bi Yàlla may nit ñi dina tax ñépp xam ban jiite moo gën. Nit ñi jéem nañu bépp fasoŋu nguur. Jéem nañu lépp ci wàllu wut alal ak lépp ci wàllu jaamu Yàlla.

Loolu yépp, lu mu jur ? Ay coono yu dul jeex. Te ñu ngi gën di yokku rekk. Diggante tey ak téemeeri at ci gannaaw rekk, lu ëpp téemeeri milioŋi nit ñoo dee ci xeex yi amoon ci àddina si sépp. Bandi yi ak ñiy dorogewu bare nañu. Feebaru séy it mu ngi law rekk. At mu nekk ay milioŋi nit ñu ngi dee ndax xiif ak feebar. Kër yu baree ngi tas. Ñu bare bëggatuñu lu baax. Amul benn nguur ci kaw suuf bu mën a dindi coono yooyu. Amul nguur bu mas a dindi màgget, feebar ak dee.

Coono yooyu yépp Biibël bi waxoon na ko bu yàgg. Dafa ne ñu ngi ci “ muju jamono ” ci ay ‘ bés yu tiis te tar ’. Te ni mu ko waxe woon, nit ñu bon ñi ak naaféq yi ñu ngi gën di bon rekk. — 2 Timote 3:1-5, 13.

Coono, léegi mu jeex !

Nit di jéem a jiite boppam, lan la jur ? Musiba kese ! Kon leer na ne doomu Aadama yi mënuñu jiite seen bopp. Kiliftéefu Yàlla rekk moo mën a indi jàmm, jële fi feebar te may nit ñi dund gu dul jeex. Dëgg la, Yàlla bàyyi na lu bon ak coono di am ba tey. Waaye li ñu gis yépp wone na ne, bu ci kanamee tuuti, Yàlla dina fi dindi lépp luy sonal nit ñi ci àddina si tey.

Biibël bi nee na : “ Ci jamonoy buur yooyu [maanaam nguuru nit ñi am tey ci àddina si], Yàllay asamaan yi dina feeñal ci asamaan nguur gu dul tas mukk [...]. Dina jàllarbi ak a tasaare nguur yeneen yépp [maanaam nguur yi am tey], waaye moom doŋŋ dina sax ba fàww. ” (Dañeel 2:44). Yexowa mooy Ki war a jiite. Dafa taxawal benn nguur ci asamaan. Li Biibël bi wax yépp, mu ngi jëm ci Nguur googu. Yeesu waxoon na ne dina am luy wone ne léegi Nguur googu dindi lu bon. Lii la wax : “ Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. ” — Macë 24:14.

Bés bu fi Yàlla dindee lu bon, kan mooy mucc ? Biibël bi nee na : “ Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm, waaye bu delloo gannaaw, sama xol du sedd ci moom. Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye ñu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc. ” (Yawut ya 10:38, 39). Ku jub mooy kiy jàng ngir xam coobare Yexowa ba pare def ko. Yeesu Kirist nee na : “ Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist. ” (Yowaana 17:3). Kon nañu xam ne “ àddina day wéy, waaye kuy def coobareg Yàlla dinga sax ba fàww  ”. — 1 Yowaana 2:17.

Aaya yi ñu fi lim, ñu ngi leen jële ci Mucc gi Yàlla waajal, Njàlbéen ga ak Téereb Injiil di Kàddug Yàlla. Aaya yi ànd ak MN, ci Les Saintes Écritures — Traduction du monde nouveau — avec notes et références lañu ko jële, firi ko ci wolof. Aaya yi amagul ci wolof, bind nañu ci tubaab turu téere Biibël bi fi ñu nekk te dëngal mbind yi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager