XAAJ 4
Kan mooy Yàlla?
LI nit ñi di jaamu bare na. Waaye Mbind mu sell mi nee na benn Yàlla dëgg rekk moo am. Yàlla, kenn la te amul moroom, moo sut ñépp, te mooy sax ba fàww. Moom moo sàkk lépp li nekk ci asamaan ak ci suuf te moom moo ñu may dund. Kon moom rekk lañu war a jaamu.
Sàrt bi wàcc ci yonent Yàlla Musaa, ‘ kàddug yoon la woon, wi Yàlla yégle jaarale ko ci malaaka yi ’
Ni ñuy woowe Yàlla bare na waaye benn tur rekk la am. Tur boobu mooy YEXOWA. Lii la Yàlla wax Musaa : “ Waxal bànni Israyil : ‘ Aji Sax ji [Yexowa, MN], di Yàllay maam yi, Yàllay Ibrayima, Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanxóoba, moo ma yónni ci yéen. ’ Loolu mooy sama tur ba fàww. Noonu lañu may wooye ci ay maam ba ciy maamaat. ” (Gàddaay gi 3:15). Tur boobu feeñ na lu jege 7000 yoon ci Mbind mu sell mi. Ni ko Sabuur 83:18, MN waxe ci Yàlla, “ yow mii tudd Yexowa, yow rekk yaay Aji Kawe ji ci kaw suuf si sépp. ”
Turu Yàlla feeñ na ci aaya bu ñu mën a jàng ci mbind mu yàgg lool te ñu gis ko ci wetu Géej gu amul dund (Mer morte ci tubaab)
Kenn masul gis Yàlla. Lii la Yàlla wax Musaa : “ Doo mën a gis sama xar-kanam, ndaxte kenn mënu maa gis tey dund. ” (Gàddaay gi 33:20). Yàlla mu ngi asamaan te doomu Aadama mënu ko gis. Kon baaxul ñuy defar walla ñaan ay xërëm, ay nataal walla lépp lu ñuy méngale ak Yàlla. Lii la Yexowa digal, mu jaarale ko ci yonentam Musaa : “ Bul sàkkal sa bopp xërëm, di ko jox melow dara lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci suuf, mbaa ci ndox, yi suuf tiim. Bu leen sujjóotal te bu leen jaamu, ndaxte man maay Aji Sax ji, di Yàlla sa Boroom. Yàlla ju fiir laa. ” (Gàddaay gi 20:2-5). Ginnaaw loolu, lii la wax yonent Yàlla Esayi : “ Maay Aji Sax ji [Yexowa, MN], mooy sama tur ; duma bàyyeel sama ndam keneen mbaa sama sag xërëm yi. ” — Esayi 42:8.
Am na ay nit ñu gëm Yàlla waaye pur ñoom kenn mënu ko xam walla jege ko, te ragal ko moo ëpp solo bëgg ko. Loo ci xalaat ? Ndax Yàlla fonk na la, yow ci sa wàllu bopp ? Ndax mën nga ko xam, te dem ba jege ko ? Nañu seet lu neex li Mbind mu sell mi wax ci ay mbiri Yàlla yu rafet.