TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • rk xaaj 6 p. 15-17
  • Lu tax Yàlla sàkk suuf si?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lu tax Yàlla sàkk suuf si?
  • Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
rk xaaj 6 p. 15-17

XAAJ 6

Lu tax Yàlla sàkk suuf si?

YÀLLA dafa sàkk suuf si ngir nit dëkk ci. Lii la wax ci kàddoom : “ Yexowa moo moom asamaan, waaye suuf si dafa ko may doomu Aadama yi. ” — Sabuur 115:16, MN.

Bala Yàlla sàkk suñu maam Aadama, dafa tànn benn béréb ci kaw suuf si, béréb bu ñuy woowe Àjjana, te defar ko mu nekk tool bu rafet. Mbind mu sell mi dafa wax ne ñaari dex ñoo jóge woon toolu Àjjana boobu. Benn bu tudd Efraat ak beneen bu tudd Tigre (Idekel).a Kon mën nañu xalaat ne toolu Àjjana mu ngi won ci réew mi ñuy wax tey Turquie. Waaw, toolu Àjjana, ci kaw suuf la nekkoon !

Yàlla dafa sàkk Aadama te dugal ko ci toolu Àjjana ngir “ mu di ko bey ak a sàmm. ” (Njàlbéen ga 2:15). Ginnaaw loolu, Yàlla dafa sàkk Awa, may ko Aadama pur mu nekk jabaram. Yàlla nee leen: “ Giirleen te bare ba fees àddina di ko saytu. ” (Njàlbéen ga 1:28). Kon leer na ne Yàlla sàkkul suuf ndax neen waaye dafa ko sàkk ngir nit dëkk ci. — Isaïe 45:18.

Waaye Aadama ak Awa, ñoom, dañu jéggi yoonu Yàlla te ñoo ko tey. Yàlla génne leen toolu Àjjana. Àjjana ji, ñàkk nañu ko. Bàkkaaru Aadama, am na leneen lu mu def. Mbind mu sell mi nee na : “ Bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar. ” — Room 5:12.

Ndax Yexowa bàyyi na li mu bëggoon a def, maanaam suuf si nekk àjjana te fees ak ay nit ñu bég ? Déedéet ! Yàlla nee na : “ Sama kàddu, gi génne ci sama gémmiñ ; du dellusi mukk ci man cig neen, waaye dina matal sama coobare, def sama nammeel. ” (Esayi 55:11). Kon suuf si dina nekkaat Àjjana !

Dund ci biir Àjjana, nu muy mel ? Nañu seet léegi li Mbind mu sell mi wax ci loolu.

a Lii la Njàlbéen ga 2:10-14 wax : “ Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddalikoo, def ñeenti wal. Turu menn wal ma di dexu Pison [. . .]. Ñaareelu dex ga di Giyon [. . .] ; turu ñetteelu dex ga di Idekel [maanaam Tigre], féete réewu Asiri penku ; ñeenteelu dex ga di Efraat. ” Ñaari dex yi des, xamuñu fu ñu féete.

Lan ngay tontu ?

  • Lu tax Yàlla sàkk suuf ak nit ?

  • Nu ñu mën a xame ne Yàlla dina def li mu bëggoon ?

Ay nit ñu nekk ci biir àjjana

Àjjana ji nar a am ci kaw suuf

Ñi dee dinañu dekki : “ Néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di[nañu] dégg baatam tey génn. ” — Yowaana 5:28, 29.

Màgget, lafañ ak dee dootul am : “ Kenn ci waa réew mi du wax : ‘ Dama feebar ’” (Esayi 33:24, MN) Yàlla “ dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ” — Peeñu ma 21:4.

Lekk bu neex dina bare : “ Ci lu wóor suuf si dina meññ ni mu ware. Yàlla, suñu Yàlla, dina ñu barkeel. ” — Sabuur 67:6, MN.

Kër yu rafet ak liggéey bu neex : “ Ci lu wóor dinañu tabax ay kër te dëkk ci. [. . .] Ñi ma tànn, dinañu jariñoo ba mu mat liggéey bi ñu def ak seen loxo. ” — Esayi 65:21, 22, MN.

Xeex yi, nit ñuy jéggi yoon, jëfi fitna, dootul am : Yexowa “ day giifal xare, ba ci cati àddina. ” — Sabóor 46:10. “ Nit ñu bon ñi [. . .] dinañu leen buddi ci kowam. ” — Léebu yi 2:22, MN..

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager