TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 1 p. 4-5
  • Naka lañu mën a dégge li Yàlla wax ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Naka lañu mën a dégge li Yàlla wax ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaaj 1
    Déggleen li Yàlla wax
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 1 p. 4-5

XAAJ 1

Naka lañu mën a dégge li Yàlla wax ?

Yàlla ci Biibël bi lay jaar ngir wax ak ñun. 2 Timote 3:​16

Ci gànguneem ci asamaan, la Yexowa xiire ay nit ñu bind Biibël bi

Yàlla xiir na ay nit ñu bind ay xalaatam ci benn téere. Téere boobu mooy Biibël bi. Yàlla bëgg na ngeen xam xalaat yu am solo yooyu nekk ci biir.

Yàlla moo xam li gën ci ñun, te moom rekk moo ñu mën a may xam-xam dëgg. Loolu moo tax, bu ngeen déggee li Yàlla wax, dingeen nekk ay nit ñu am xel dëgg. — Léeb yi 1:5.

Biibël bi ci ay làkk yu bare, góor guy jàng Biibël ci làkkam

Yàlla dafa bëgg nit ku nekk jàng Biibël bi. Fi mu tollu nii, Biibël bi am na ci ay làkk yu bare.

Bu ngeen bëggee dégg li Yàlla wax, fàww ngeen jàng Biibël bi te xam li muy wax.

Ci biir àddina si sépp, ay nit ñu ngi dégg li Yàlla wax. Macë 28:19

Seede Yexowa buy dimbali kenn mu xam li nekk ci mbind yu sell yi, ba noppi muy jàng ak moom Biibël bi

Seede Yexowa yi mën nañu leen a dimbali ngeen xam li Biibël bi di wax.

Fépp ci àddina si, Seede Yexowa yi ñu ngi jàngale dëgg gi jëm ci Yàlla.

Ndaje mi ci saalu nguuru Seede Yexowa yi

Bu ñu leen di jàngal dëgg googu, dooleen fey dara. Mën ngeen itam jàng lu jëm ci Yàlla ci Saalu Nguur gi leen gën a jege..

  • Kàddu Yàlla mooy dëgg. — Yowaana 17:17.

  • Lu tax ñu mën a teg suñu yaakaar ci Yàlla ? — Nombres 23:19.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager