TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 8 p. 18-19
  • Ban njariñ la leen deewu Yeesu amal ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ban njariñ la leen deewu Yeesu amal ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaaj 8
    Déggleen li Yàlla wax
  • Lan mooy Nguuru Yàlla ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Lan mooy Nguuru Yàlla ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan mooy Nguuru Yàlla ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 8 p. 18-19

XAAJ 8

Ban njariñ la leen deewu Yeesu amal ?

Deewu Yeesu dina ñu may dund gu dul jeex. Yowaana 3:16

Ay jigéen dem nañu ca bàmeel Yeesu waye fekku ñu ko fa

Bi Yeesu deewee ba mu am ñetti fan, ay jigéen dem nañu ca bàmmeelam ; waaye fekkuñu fa néewam. Yexowa moo dekkaloon Yeesu.

yeesu feeñu na taalibeem yi, bi loolu weesoo, mu dellu ca asamaan

Ginaaw loolu, Yeesu feeñu na ay taalibeem.

Ci dëgg, Yexowa dekkal na Yeesu, mu delluwaat ca kaw asamaan, nekk fa ku bare kàttan te du deewati mukk. Taalibe Yeesu yi gis nañu Yeesu bi muy dellu kaw asamaan.

  • Lan mooy “ peyu ” bàkkaar ? — Room 6:23.

  • Yeesu mooy ki ubbi buntu dund gu dul jeex. — Room 5:21.

Yàlla dekkal na Yeesu, def ko Buuru Nguuru Yàlla. Dañeel 7:13, 14

Ci gangunem ga ca asamaan, la Yeesu di nguuroo nit ñi ci àjjana ci kaw suuf

Yeesu dafa joxe bakkanam ngir musal nit ñi. Loolu mooy njot gi (Macë 20:28). Yàlla dafa jaar ci njot gi ngir nit ñi mën a am dund gu dul jeex.

Yexowa fal na Yeesu Buur ca kaw asamaan ngir mu nguuru ci kaw suuf si. Yeesu dina nguuru ak 144000 nit ñu baax ñoo xam ne Yàlla moo leen nar a dekkal ngir ñu dund ca kaw asamaan. Ñoom ñépp ñooy nguuru ca kaw asamaan ci Nguuru Yàlla mi nekk nguur gu jub. — Peeñu ma 14:1-3.

Nguuru Yàlla dina defar suuf si ba mu nekk àjjana. Dootul amati geer, reyante, xiif, walla ñakk bu metti. Jàmm dëgg dina am ci kaw suuf si. — Psaume 145:16.

  • Yan barke la Nguuru Yàlla di indi ?— Sabóor 72.

  • War nañu ñaan ngir Nguuru Yàlla ñëw. — Macë 6:10.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager