TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 9 p. 20-21
  • Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Àjjana jege na !
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Xaaj 9
    Déggleen li Yàlla wax
  • Ndax ñu ngi ci “ muju jamono ” ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 9 p. 20-21

XAAJ 9

Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?

Xew-xew yooyu yépp dañuy wone ne, léegi Nguuru Yàlla def dara. Luug 21:10, 11 ; 2 Timote 3:1-5

Jafe-jafe yi nekk benn ci muju jamono—wure xaalis, geer, feebar, xiif, xëtt ndigalu waajur ak coxoorte ci biir kër

Lu bare ci liy xew tey, Biibël bi waxoon na ne dina am. Nee woon na ne nit ñi dinañu fonk xaalis, dinañu xëtt ndigalu waajur, ñu soxor lañuy doon, te di topp seen bànneex.

Dina am ay yengu-yengu suuf yu réy, ay geer, ay xiif ak ay feebar yu bare. Loolu yépp ñu ngi koy gis tey.

Seede Yexowa buy waare xebaar bu baax bi ci Nguuru gi ab góor

Yeesu waxoon na itam ne xebaar bu baax bi ci Nguuru Yàlla, dinañu ko yégle ci àddina sépp.— Macë 24:14.

Nguuru Yàlla dina fi jële lépp lu bon. 2 Piyeer 3:13

Ñu bon ñi dina ñu leen alag ci Armagedon nonu Seytaane ak malaakaam yu bon yi dina ñu leen yar

Du yàggati dara, Yexowa dina alag nit ñu bon ñi.

Yàlla dina fi jële Seytaane ak malaaka yu bon yi.

Yessu toog na ca ganguneem ga ca asamaan te nit xeet yu bare bég nañu

Ñiy dégg li Yàlla wax dinañu mucc, te dinañu dund ci jamano bu bees boo xam ne njubte rekk mooy am. Kenn dootul am looy ragal. Kenn ku nekk dinga mën a wóolu sa moroom te bëgg ko.

  • Lan la Yeesu waxoon ne dina xew ci suñu jamano ? — Macë 24:3-14.

  • Yàlla dina alag nit ñu bon ñi.— 2 Piyeer 3:7.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager