NJÀNGALE 8
Yosiyas amoon na ay xarit yu baax
Ndax def lu baax metti na ? — Nit ñu bare loolu lañu foog. Biibël bi dafa wax ci benn xale góor bu tuddoon Yosiyas. Def lu baax metti woon na lool ci moom. Waaye amoon na ay xarit yu baax yu ko doon dimbali. Nañu jàng nettali bii ngir gën a xam Yosiyas ak xaritam yi.
Pàppa Yosiyas mu ngi tuddoon Amon, te buur la woon. Nit ku bon la woon te ay xërëm la doon jaamu. Bi pàppam deewee, Yosiyas nekk buuru Yuda. Juróom ñetti at kese la amoon ! Ndax foog nga ne dafa doon def lu bon ni pàppam ? — Déedéet !
Sofoni dafa doon wax nit ñi ñu bañ a jaamu ay xërëm
Yosiyas xale la woon waaye dafa bëggoon a déggal Yexowa. Loolu moo tax mu tànn ay xarit yu bëgg Yexowa kese. Xarit yooyu ñoo doon dimbali Yosiyas mu def lu baax. Ñan ñoo nekkoon xaritam yi ?
Sofoni, kenn la woon ci xaritam yi. Yonent la woon bu doon yégal waa Yuda ne lu bon dina leen dal bu ñu jaamoo ay xërëm. Yosiyas topp li Sofoni doon wax te bañ a jaamu ay xërëm.
Yérémi itam, xaritu Yosiyas la woon. Ñoom ñaar a màggandoo. Ay xarit dëgg lañu woon. Moo tax bi Yosiyas deewee, Yérémi woyal ko woy buy wone ni ko deewam mettee. Yérémi ak Yosiyas, ku nekk dafa doon dimbali sa moroom mu def lu baax te déggal Yexowa.
Yérémi ak Yosiyas, ku nekk dafa doon dimbali sa moroom mu def lu baax
Lan nga mën a jàng ci Yosiyas ? — Yosiyas xale bu ndaw la woon waaye dafa bëggoon a def lu baax. Xamoon na ne dafa war a tànn ay xarit yu bëgg Yexowa. Yaw itam tànnal ay xarit yu bëgg Yexowa te mën laa dimbali nga def lu baax !
JÀNGAL CI SA BIIBËL
2 Chroniques 33:21-25 ; 34:1, 2 ; 35:25