TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • hf xaaj 4 xaaj yi 1-2
  • Naka lañu war a yoree xaalis ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Naka lañu war a yoree xaalis ?
  • Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Turu xaaj yi
  • 1 XALAATLEEN BU BAAX CI DEPÃS YI NGEEN BËGG A DEF
  • 2 BULEEN NËBB DARA TE XAMLEEN LI NGEEN ÀTTAN
Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
hf xaaj 4 xaaj yi 1-2
Jëkkër ak jabar ñu ngi xool bu baax ni ñu war a yore seen xaalis

XAAJ 4

Naka lañu war a yoree xaalis ?

Bu diisoo amee, pexe dina am. — Proverbes 20:⁠18

Ñun ñépp soxla nañu xaalis ngir faj suñu soxlay njaboot (Kàddu yu Xelu 30:⁠8). Ni ko Biibël bi waxee, xaalis dafa ñuy aar ci lu bare (Ecclésiaste 7:​12). Yéen ñi séy, waxtaan ci li ngeen di def ak seen xaalis mën na bañ a yomb, waaye buleen bàyyi xaalis indi poroblem ci seen séy (Efes 4:​32). Bu jëkkër ak jabar di waxtaan ci depãs yi ñu bëgg a def, fàww ku nekk wóolu moroomam te def lépp ngir juboo.

1 XALAATLEEN BU BAAX CI DEPÃS YI NGEEN BËGG A DEF

LI BIIBËL BI WAX : “ Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi ? ” (Luug 14:28). Am na solo lool ngeen toog yéen ñaar ngir xalaat ci depãs yi ngeen bëgg a def (Amos 3:⁠3). Seetleen li ngeen soxlaa jënd ak li ngeen mën a génne ci xaalis ngir jënd loolu (Kàddu yu Xelu 31:16). Mën a jënd dara warul a tax ngeen jënd ko. Fexeleen ba moytu bor. Yemleen rekk fi seen poos tollu. — Kàddu yu Xelu 21:5 ; 22:⁠7.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu ngeen desee xaalis ci weer bi, toogleen waxtaan ci li ngeen ci nar a def

  • Bu xaalis bi jeexee bala weer bi dee, xoolleen depãs yi ngeen war a waññi. Mën ngeen a togg kër ga. Moo gën a yomb dem lekk ci biti

Jëkkër ak jabar ñu ngi xalaat ci seeni depãs yi gën a réy[Nataal bi nekk ci paas 13]

2 BULEEN NËBB DARA TE XAMLEEN LI NGEEN ÀTTAN

LI BIIBËL BI WAX : “ Danuy fexe def li jub, du ci kanam Yàlla rekk, waaye it ci kanam nit ñi. ” (2 Korent 8:​21). Waxal sa jëkkër walla sa jabar ñaata ngay am ci xaalis ak fi nga koy dugal.

Saa yoo bëggee def depãs bu réy, nanga ci waxtaan ak ki nga séyal (Kàddu yu Xelu 13:10). Faral di waxtaan ci xaalis bi ngeen am moo leen di dimbali ci kontine di am jàmm ci seen séy. Xaalis bi ngay am, bu ko jëlee ni sa xaalis yaw kese waaye jëlee ko ni xaalisu njaboot gi. — 1 Timote 5:⁠8.

Jëkkër ak jabar ñu ngi marse di xool ci kayit li ñu war a jënd

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Waxleen ba juboo ci ñaata xaalis la ku nekk mën a jaay te du soxla muy tàggu moroomam

  • Buleen bàyyi ba poroblem am, ngeen sog a waxtaan ci seen xaalis

NI NGEEN WAR A GISE XAALIS

Dëgg la, xaalis am na solo, waaye buleen ko bàyyi mu yàq seen séy walla mu yàq seen nelaw (Macë 6:​25-​34). Soxlawul ngeen am xaalis bu bare ngir am dund bu neex. Lii la Biibël bi wax : “ Moytuleen bëgge ”. Amul dara lu xaalis mën a jënd ba mu gën a am solo seen séy. Kon nangeen doylu ci li ngeen am, te buleen mas a sàggane seen diggante ak Yàlla. Noonu, seen njaboot dina am bànneex te dingeen neex Yexowa. — Yawut ya 13:⁠5.

LAAJLEEN SEEN BOPP LII :

  • Ci suñu njaboot, lan lañu mën a def ba bañ a dugg ci bor ?

  • Kañ laa gëj a waxtaan ak ki ma séyal ci ni ñuy jëfandikoo suñu xaalis ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager