WOY-YÀLLA 29
Dañoo bëgg a yelloo sa tur
(Esayi 43:10-12)
1. Yexowa Aji Kawe ji, Boroom bi,
jub ak mbëggeel ngay tëral ci sa yoon.
Boroom sago, leer ak dund, Jàmbaar bi,
ba abadan kiliftéef du la raw.
Xoolal mbooloo mi jébbalu ci yow mii,
di yégle sa Nguur ci àddina si.
(AWU BI)
Doon say seede, Yexowa, dafa neex lool.
Duñu fowe barke bii, wóor nañu.
2. Liggéeyu waare bi def na ñu bennoo.
Booloo nañu ci biir jàmm ak mbëggeel.
Tiitaroo sa ndam, jàngale say ndigal,
lii di la màggal, barke yi baawaan.
Wuyoo sa tur Yexowa suñu Baay bi,
di seddal sa xol ci jëf ak ci wax.
(AWU BI)
Doon say seede, Yexowa, dafa neex lool.
Duñu fowe barke bii, wóor nañu.
(Xoolal itam Baamtug Yoon wi 32:4; Taalifi Cant 43:3; Dañeel 2:20, 21.)