TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 8 p. 11
  • Jàngalal nit ñi ak ay misaal

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Jàngalal nit ñi ak ay misaal
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 8 p. 11

LESOŊ 8

Jàngalal nit ñi ak ay misaal

Aaya bi ñu lim

Macë 13:34, 35

LI NGA WAR A JÀPP: Nanga jàngale ak ay misaal yu yomb, yuy laal xol tey jàngale ay ponk yu am solo.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Tànnal ay misaal yu yomb. Ni ko Yeesu daan defe, jaaral ci lu ndaw ngir jàngale lu am solo, jaaral ci lu yomb ngir jàngale lu jafee xam. Bu ci yokk luy tax misaal bi du leer. Fexeel ba sa misaal ànd bu baax ak li ngay jàngale ngir bañ a réeral ñi lay déglu.

    Xelal bu baax

    Amal seetlu. Xoolal li la wër, jàngal suñu téere karceen yi, te nanga déglu ñi mën a jàngale bu baax. Booy def loolu, bàyyil xel ci misaal yi mën a tax sa njàngale gën a baax te nga bind ko fenn.

  • Xalaatal ñi la nar a déglu. Tànnal misaal yu ànd ak li nit ñi di dund. Moytul misaal yu leen di rusloo walla yu leen di merloo.

  • Na ponk bi gën a am solo feeñ bu baax. Nanga misaal ponk yi gën a am solo rekk. Fexeel ba ñi lay déglu bañ a yem rekk ci fàttaliku misaal bi waaye ñu jàpp li ñu ci war a jànge.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager