TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lff lesoŋ 53
  • Bégalal Yexowa ci ni ngay féexale sa xol

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Bégalal Yexowa ci ni ngay féexale sa xol
  • Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Turu xaaj yi
  • XÓOTALAL NJÀNG MI
  • NAÑU TËNK
  • GËSTUL
Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
lff lesoŋ 53
Lesoŋ 53. Benn baay, benn yaay ak seen doom bu jigéen ñu ngi lekk popkorn di seetaan tele.

LESOŊ 53

Bégalal Yexowa ci ni ngay féexale sa xol

Édition imprimée
Édition imprimée
Édition imprimée

Yexowa «Yàlla bu bég» la (1 Timote 1:11, MN) Dafa bëgg ñun itam ñu bég te am bànneex ci suñu dund. Dafay bég bu ñu gisee ñu jël jot ngir noppalu ak féexal suñu xol. Ci lesoŋ bii, dinañu gis ni ñu mënee féexal suñu xol ba mu indil ñu mbégte te it neex Yexowa.

1. Ci lan lañu war a bàyyi xel bu ñuy tànn ni ñuy féexale suñu xol?

Lan ngay féexale sa xol? Am na ñoo xam ne li leen neex mooy, toog seen kër di liir téere, déglu misik, seetaan film walla dem ci internet. Ñeneen ñi li leen gënal mooy, ànd ak seeni xarit di doxantu, dem sanguji géej, walla dem futbali. Ak lu ñu mënta neex ci loolu, war nañu fexe ba mu wóor ñu ne, ni ñuy féexale suñu xol dina «neex Boroom bi» (Efes 5:10). Am na solo lool ñu xam ko ndaxte lu bare li nit ñi di féexale seen xol dafa ànd ak coxorte, njaaloo walla yëfi luxus. Te Yexowa dafa sib loolu (Jàngal Sabóor 11:5). Lan moo ñu mën a dimbali ñu tànn bu baax ni ñuy féexale suñu xol?

Bu ñu amee ay xarit yu bëgg Yexowa, dinañu ñu xiir ci def lu baax te tànn bu baax ni ñuy féexale suñu xol. Ni ñu ko jànge ci benn lesoŋ, kuy ‘ànd ak ku xelu, sam xel rafet.’ Waaye bu ñuy faral di ànd ak ñu bëggul santaane Yàlla yi, dinañu «loru» (Kàddu yu Xelu 13:20).

2. Lu tax ñu war a bàyyi xel bu baax ci jot gi ñuy def ci féexal xol?

Bu dee sax fo bi ñu tànn ngir féexal suñu xol lu baax la, war nañu bàyyi xel ci jot gi muy jël. Su ñu ko deful, dootuñu am jotu def li gën a am solo. Biibël bi nee na, ñu «jariñoo [suñu] jot» (Jàngal Efes 5:15, 16).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee tànn bu baax ni ngay féexale sa xol.

3. Moytul fo yu bon

Lu tax ñu war a moytu bu baax, bu ñuy tànn ni ñuy féexale suñu xol? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

WIDEO: Naka laa war a tànne ni may féexale sama xol? (4:39)

  • Fo yi amoon ci dëkku Room bu njëkk, naka lañu niroo ak fo yi am tey?

  • Ci wideo bi, lan la Danny jàng ci lu jëm ci féexal sa xol?

Jàngal Room 12:9. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la la aaya bii mënee dimbali nga tànn bu baax li ngay féexale sa xol?

Lan la Yexowa bañ? Jàngal Kàddu yu xelu 6:16, 17 ak Galasi 5:19-21. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lañu wax ci aaya yii te ñu koy faral di gis ci fo yi am tey?

Ni nga mënee tànn bu baax li ngay féexale sa xol

Laajal sa bopp lii:

  • Lan? Ndax li may féexale sama xol am na lu ci Yexowa bañ?

  • Kañ? Ndax dafay tombe ak waxtu bu ma war a def lu gën a am solo?

  • Kan? Ndax dafay tax may faral di ànd walla jokkoo ak ñu bëggul Yexowa?

Li gën a wóor mooy sori bu baax lépp lu ñu mën a lor. Loolu moo tax ñu war a sori bépp fo bu ñu xalaat ne mën na ñu lor

Oto buy daw ci catu tund wi. Ginnaawu oto bi mu ngi komaasee wàcc yoon wi.

4. Jëfandikool bu baax sa jot

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

WIDEO: Lan mooy gën a jël sa jot? (2:45)

  • Bu dee sax suñu mbokk bi ci wideo bi nekkul woon di seetaan lu bon, lan moo nekkoon poroblemam?

Jàngal Filib 1:10. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la ñu aaya bii mënee dimbali, ñu xam waxtu bi ñuy def ci féexal suñu xol?

5. Tànnal fo yu baax

Dëgg la ne am na fo yu neexul Yexowa, waaye am na yu bare yu ko neex. Jàngal Kàdduy Waare 8:15 ak Filib 4:8. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Yan fo yu baax ñoo la gën a neex?

Foto yu ñu boole: Ay nit yu maasewul ñu ngi féexal seen xol ci fasoŋ bu baax. 1. Xale bu jigéen bi mu ngi déglu misik, di desine. 2. Ñetti xale yu góor ñu ngi basket. 3. Ñaari xale yu góor ñu ngi dawal welo. 4. Xale bu góor buy defar oto. 5. Góor guy tëgg ndënd. 6. Xale bu góor ak pàppam ñu ngi fo ak jeu video. 7. Benn jigéen buy foto.

Mën nga féexal sa xol ci fasoŋ bu baax

BU LA NIT WAXOON: «Féexal sa xol ak fo yu am coxorte, njaaloo walla yëfi luxus, dara bonu ci bu dee doo ko def ci dëgg.»

  • Lan nga koy wax?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa bëgg bu ñuy féexal suñu xol, ñu tànn fo yu baax.

Nañu fàttaliku

  • Lan la karceen war a moytu buy tànn ni muy féexale xolam?

  • Lu tax ñu war a bàyyi xel bu baax ci jot gi ñuy def ci féexal suñu xol?

  • Lu tax nga bëgg a féexal sa xol ak lu neex Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ki la war a tànnal fo yi ngay féexale sa xol.

«Ndax am na ay film, téere walla woy yu ñu tere Seede Yexowa yi?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ni nga mënee tànn bu baax li ngay féexale sa xol.

«Ndax li ngay féexale sa xol baax na ci yow?» (w11 15/10)

Xoolal ni benn yaay jële dogal bu baax, ci lu jëm ci fasoŋu fo yiy fësal xel mi àddina si soloo.

Moytul fo yi am mbirum Seytaane (2:02)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager