TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lff lesoŋ 57
  • Lan nga war a def boo defee bàkkaar bu réy?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan nga war a def boo defee bàkkaar bu réy?
  • Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • XÓOTALAL NJÀNG MI
  • NAÑU TËNK
  • GËSTUL
  • Waxal magi mbooloo mi ñu dimbali la
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
  • Ni magi mbooloo yi mën a def ngir dimbali ñi bàkkaar ànd ci ak mbëggeel ak yërmande
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)-2024
  • Ni Yexowa di jiitee mbooloo karceen mi jaare ko ci Yeesu
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Ni magi mbooloo yi mënee dimbali ñi ñu génne ci mbooloo mi
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)-2024
Xóotalal waxtaan bi
Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
lff lesoŋ 57
Lesoŋ 57. Ci benn saalu Nguur, benn mbokk bu góor mu ngi wax magi mbooloo mi bàkkaar bu réy bi mu def.

LESOŊ 57

Lan nga war a def boo defee bàkkaar bu réy?

Édition imprimée
Édition imprimée
Édition imprimée

Bu dee sax bëgg nga lool Yexowa te yaa ngi def lépp ngir bañ a def lu ko neexul, lée-lée dinga juum. Waaye nag bàkkaar yépp yemuñu, am na yu ci doon bàkkaar yu réy (1 Korent 6:9, 10). Boo defee bàkkaar bu réy, fàttalikul ne Yexowa bëgg na la ba tey; pare na ngir baal la te dimbali la.

1. Lan lañu war a def ngir Yexowa baal ñu?

Ñi bëgg Yexowa dañuy am naqaru xol bu réy, bu ñu gisee ne def nañu bàkkaar bu réy. Waaye li Yexowa dig ay jaamam dafa leen di dëfal, lii la wax: «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji» (Esayi 1:18). Bu ñu tuubee dëgg suñuy bàkkaar, Yexowa dina ñu baal. Naka lañuy wone ne tuub nañu suñu bàkkaar? Dañuy rëccu bu baax lu bon li ñu def, bañ koo defati te ñaan Yexowa mu baal ñu. Ginnaaw loolu, dañu war a def suñu kem kàttan ngir bàyyi xalaat walla tàmmeel yu bon yi ñu yóbbe ci bàkkaar boobu. Ba pare góor-góorlu ngir topp lépp li ñu Yexowa sant (Jàngal Esayi 55:6, 7).

2. Naka la Yexowa di jaare ci magi mbooloo mi ngir dimbali ñu bu ñu bàkkaaree?

Bu ñu defee bàkkaar bu réy, li ñu Yexowa wax mooy ñu «woo njiiti mbooloo mi» (Jàngal Saag 5:14, 15). Magi mbooloo yooyu dañu bëgg Yexowa, te bëgg it ay jaamam. Jàngal nañu leen ni ñu ñu mënee dimbali ñu defaraat suñu diggante ak Yexowa (Galasi 6:1).

Naka la ñu magi mbooloo mi di dimbalee bu ñu defee bàkkaar bu réy? Ñaar walla ñetti magi mbooloo dinañu jëfandikoo Biibël bi ngir won ñu, li tax li ñu def bon. Dinañu ñu jox itam ay xelal yu baax te dooleel ñu ngir ñu bañ a daanuwaat ci bàkkaar. Bu amee ku def bàkkaar bu réy te tuubu ko, magi mbooloo mi dañu koy génne ci mbooloo mi ngir mu bañ a yóbbaale ñeneen ci def lu bon.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Gënal a yokk sa ngërëm ci matuwaay yi Yexowa jël ngir dimbali ñu, bu ñu defee bàkkaar bu réy.

3. Wax li ñu def dina ñu dimbali ñu defaraat suñu diggante ak Yexowa

Saa yu ñu bàkkaaree, Yexowa lañu tooñ. Kon moom lañu war a wax li ñu def. Jàngal Sabóor 32:1-5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax mu baax ci ñun, ñu wax Yexowa suñuy bàkkaar te bañ leen a jéem a nëbb?

Bu ñu waxee Yexowa suñuy bàkkaar ba pare, wut ndimbalu magi mbooloo mi itam dina ñu dimbali bu baax. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

WIDEO: «Ku Boroom bi sopp, yar la» (3:01)

  • Ci wideo bi, naka la magi mbooloo mi dimbalee Canon mu dellusi ci Yexowa?

Bu ñuy wax ak magi mbooloo mi, war nañu wax lépp te bañ a nëbb dara. Dañu leen fi teg ngir ñu dimbali ñu. Jàngal Saag 5:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax muy gën a yomb ci magi mbooloo mi ñu dimbali ñu, bu ñu leen waxee lépp te bañ a nëbb dara?

Foto yu ñu boole: 1. Benn mbokk bu góor bu am naqar bu réy mu ngi jàpp bopp bi. 2. Mbokk mi mu ngi ñaan Yexowa. 3. Mbokk mi wax na ak benn magu mbooloo ci telefon. 4. Mu gise ak ñetti magi mbooloo. 5. Mbokk mi mu ngi muuñ ndax léegi xelam dal na.

Waxal li nga def, bul nëbb dara magi mbooloo mi, te nangul ndimbalu Yexowa bi ànd ak mbëggeel

4. Yexowa dafay won yermande ñi def bàkkaar

Bu nit defee bàkkaar bu réy te bañ a topp santaane Yexowa yi, dañu koy génne ci mbooloo mi te dootuñu ànd ak moom. Jàngal 1 Korent 5:6, 11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lawiir dafay funkiloo fariñ. Noonu it, lan la ànd ak bàkkaarkat bu tuubul mën a def ci waa mbooloo mi?

Magi mbooloo yi dañuy roy ci yërmande Yexowa bu ñuy def lépp li ñu mën ngir dimbali ñi bàkkaar te ñu génnee leen ci mbooloo mi. Ñu bare ñi ñu génne ci mbooloo mi dellusiwaat nañu ci mbooloo mi. Ndax lan? Ndaxte génne leen ci mbooloo mi tax na ñu xam ne li ñu def baaxul, doonte sax lu metti la woon ci ñoom (Sabóor 141:5).

Ni Yexowa di doxale ak ñi bàkkaar, naka lay wone ne ku jub la, ku bari yërmande te am mbëggeel?

5. Yexowa dafa ñuy baal bu ñu tuubee suñuy bàkkaar

Yeesu dafa jël benn misaal ngir dimbali ñu, ñu xam li Yexowa di yëg bu nit tuubee ay bàkkaaram. Jàngal Luug 15:1-7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la la lii di jàngal ci Yexowa?

Jàngal Esekiyel 33:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lu am solo lañu war a def ngir wone ne tuub nañu suñu bàkkaar?

Benn sàmm mu ngi bandaas xar bi gaañu.

Ni sàmm di toppatoo xaram, noonu it Yexowa dafay toppatoo bu baax jaamam

BU LA NIT WAXOON: «Dama ragal ne bu ma waxee magi mbooloo mi li ma def, dinañu ma génne ci mbooloo mi.»

  • Lan ngay wax nit ku am gis-gis boobu?

NAÑU TËNK

Bu ñu defee bàkkaar bu réy te rëccu ko bu baax, ba pare dogu ci bàyyi def lu bon, Yexowa dina ñu baal.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax mu baax ci ñun, ñu wax Yexowa suñuy bàkkaar?

  • Lan lañu war a def ngir Yexowa baal ñu suñuy bàkkaar?

  • Bu ñu defee bàkkaar bu réy, lu tax ñu war a wut ndimbalu magi mbooloo mi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ni Yexowa wone benn góor yërmande bi ñu wax ci Esayi 1:18.

Masuma am xel-ñaar ci yërmande Yexowa (5:02)

Xoolal ni magi mbooloo yi mënee won mbëggeel ak yërmande ñi bañ a tuub seen bàkkaar.

«Ni Magi mbooloo yi mënee dimbali ñi ñu génne ci mbooloo mi» (w24.08)

Ci nettali bi tudd «Dama waroon a dellu ci Yexowa,» xoolal ni benn góor bu demoon ba sori dëgg gi yëge ne, Yexowa mu ngi ko doon woo ngir mu dellusi.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w12 1/4)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager