‘ Jigéen ñuy liggéey bu metti ci Sang bi ’
1 Ak baat yu ni mel la Pool wax ci Trifen ak Trifos, ñaari mbokki karceen ñu jigéen, ñu daan liggéey bu metti ci biir mbooloo gëmkati dëkku Room. Ci keneen, ku tudd Persis, lii la wax : ‘ Liggéey na dëgg te def lu bare ci Sang bi. ’ Rafetlu na itam liggéeyu Febe, niki ku “ taxawu ñu bare, NW ”. (Room 16:2, 12.) Ci Mbind yu sell yi, ràññee nañu woon Dorkas niki ku ‘ yéwén ci jëf yu baax ak i maye yërmande, NW ’. (Jëf. 9:36.) Ndaw barke, bu jigéen ñi fonk yooniy Yàlla nekk ngir mbooloo mi !
2 Ndax fonk nañu suñu mbokki karceen ñu jigéen, ñiy liggéey bu metti ci suñu biir mbooloo ? Ñoom ñooy amal li gën a bare ci liggéeyu waare bi, ñooy jiite li ëpp ciy njàngum Biibël bi, te ñooy jàpple ñu bare ñu bees. Dañuy jagleel itam jot gu bare ciy dimbali ay xale ñu jëm kanam ci seen digganteek Yàlla. Jigéeni karceen ñaa ngiy def seen wàll lu jëm ci feddali xelum mbëggeel, mbég, jàmm, ak cawarte ci biir mbooloo gëmkat yi. Ndimbal lañu ci fànn yu bare, ba tax seeni jëkkër ak ñeneen, ñu bokk ci seeni njaboot, mën a yokk li ñuy def ci liggéeyu Yeowa.
3 Suñu jigéen ñi jébbal sasu waare bi seen jot gépp : Ci biir jigéen ñiy wone seen njàmbaar ci liggéeyu Sang bi, am na ci ay misioneer, ñu bare ci ñoom bokk ci ñiiy suqali liggéeyu waare bi, ci bitim seen réew. Jabari wottukat yiy wër a ngi farlu dëgg ci liggéeyu tool bi, di xiirtal seeni mbokki karceen ñu jigéen ñu bare, ci biir mbooloo gëmkat yi seeni jëkkër yi di nemmeekuji. Waruñoo fàtte suñu jigéen ñi ne ci Betel yi ; ñu ngiy amal ak cawarte liggéey bu tedd, di jàpplee noonu mbootaayu Yeowa. Suñu jigéen, ñi sax ci sasu aji-xàll yoon, a ngiy dimbali nit ñu dul jeex, ñu jàng dëgg gi, te loolu ci biir njéem yu takku, yu ñu nekk di def ngir màggal Yàlla.
4 Jigéen ñu takku ñooñoo ngiy yëg mbég mu réy ci seen dundin bi làmboo xelum xañ sa bopp (1 Tim. 6:6, 8). Yeyoo nañ ñu ndokkeel leen, akit lépp luy xiirtal ak ndimbal, yu ñu leen mën a indil.
5 Jigéeni karceen ñi amal nañu njariñ mbootaayu Yeowa, lool sax, ba ñuy nekk di def liggéey bu takku, bu nekk barke ci ñépp. Yal nañu wéy di fonk jigéen ñu ni mel te di leen ñaanal barke Yeowa, ba ñuy wéy [ñoom] ‘ di liggéey bu metti ci Sang bi ’.