Nañu ji lu bare, waaye nañu ko def ak ràññaatle
1 Képp kuy beykat xam na ne, su jiwee lu bare, mën naa séentu góob lu bare, waaye su jiwee lu tuuti, wóor na ko ne lu tuuti lay góob (2 Kor. 9:6). Day wottu, kon, bañ a pasar-pasaree jiwu ji, ci li mu koy ji ci suuf su dul nangu. Ràññaatle boobu lañu war a jëfoo, bu ñuy wone suñuy mbind yi ci biir liggéeyu waare bi. Li ñuy wut mooy, bàyyi leen ci loxoy ñii leen bëgg a jàng. Li ñu bëgg mooy, xàllal ñi ci jekk yoonu xam yiwu Yeowa te ñu dunde yaakaaru Nguur gi.
2 Ci ñun, ndax mel na ni suñuy yéenekaay yi, suñuy téere yu ndaw yi, añs., a ngi nekk di dajaloo fi ñu leen di teg, te fekk mënkoon nañoo jariñ nit ñi ne ci gox gi ñuy waare te jekk ci jàng dëgg gi (seetal Macë 25:25) ? Ndax lée-lée dañuy teye suñu bopp ciy wone yéenekaay yi, walla yeneeni mbind ci suñu waxtaan wi jëkk ak nit ki, ndaxte dañoo rus a laal mbir mi jëm ci xaalis bi ñuy joxe ngir amal liggéeyu waare Nguur gi ? Ay yéenekat yu am manoore seetlu nañu ne, nit koo xam ne xabaar bi laal na xolam dina def li war, bu ñu ko faramfàccee ci fasoŋ bu yomb, bu àndul it ak sikki-sàkka, ni ñuy jëfandikoo maye yi.
3 Mën nañoo wax :
◼“ Xëy na yaa ngiy laaj sa xel ni ñu mënee bàyyi suñuy mbind yi, te duñu leen feyeeku. Suñu yëngu-yëngu bii daa bokk ci liggéeyu njàngale mu ñuy amal ci kow suuf si sépp, te li koy jàpple mooy maye yu ñu def ci xol bu sedd. Soo bëggee def maye bu ndaw ngir liggéey boobu ñuy amal, dinaa ko nangook xol bu sedd. ”
4 Nit ñu bare dañ ñuy laaj li suñu mbind yi di jar.
Mën nañoo tontu :
◼“ Duñu laaj dara ngir wecce suñuy mbind yi, ndax suñu liggéey bi, li koy taxawu moo di maye, yu ñuy def ak xol bu tàlli. Soo bëggee, tey jii, def maye bu ndaw, dinañu bég ci jëfandikoo ko ngir jàpple liggéeyu waare bi ñuy amal ci kow suuf si sépp. ”
Mën nañoo wax itam :
◼“ Képp kuy wut a gën a xam Biibël bi, mën naa jot ci suñu mbind yi. Soo bëggee def maye bu ndaw ngir liggéey bi ñuy amal ci suuf si sépp, ak xol bu sedd laa ko ciy def. ”
5 Bu ñuy wone suñuy yéenekaay yi, am na ay yéenekat ñuy wone xët bi ne ci biir, naan :
◼“ Ni nga ko seetloo fii, liy tax ñu mën a amal suñu liggéey mooy maye yu ñuy def ak xol bu sedd. Soo bëggee def maye bu ndaw ngir jàpple liggéey boobu, mën nga ma koo jox. ”
Beneen jëfin bu yomb a ngi :
◼“ Dañuy bàyyi suñuy mbind yi te duñu leen feyeeku, waaye dinañuy nangu maye yu ndaw, yi ñuy def ngir taxawu liggéey bi ñuy amal ci kow suuf si sépp. ”
6 Waruñoo teye mukk suñu bopp ciy ji jiwu Nguur gi, ndax dañoo rus a faramfàcce ni ñuy ame xaalis biy amal suñu liggéey. Waaye, soxla nañoo wone ràññaatle, ngir bañ a pasar-pasaree suñuy mbind yi ci “ bérab, bu bare ay doj ”. (Mark 4:5, 6, 16, 17.) Nit ñi am ngërëm ngir xabaar bu baax, bi ñu leen di yëgal, dinañu bég ci jàpple kook seen xaalis. — Seetal Macë 10:42.