Nañu jàng Prophétie de Daniel
1 Li dale ayu-bésu 17 awril, dinañu jàng téere bi tudd Prêtons attention à la prophétie de Daniel ! ci Njàngum téere Mbooloo mi. Ñu bare duruus nañu ba noppi téere buy jommal boobu, waaye léegi xàllal nañ ñu yoon ngir sàkku ci njariñ, njariñ luy tukkee ci di ci wecceente xalaat, ci biir mbooloo. Ñu ngiy ñaan yéenekat yi yépp, ñi dëgg gi soxal, ak xale yi yépp, waaw ñu ngiy xiirtal ñépp, ñu teewe ayu-bés gu nekk njàng mu xóot, bi ñuy def ci téereb Biibël bi, boobu ñuy tudde Dañel. — 5 Mu. 31:12, 13.
2 Doxalukaayu njàng mi ak tegtal yi : Doxalukaay lëmm, bu njàngum téereb Prophétie de Daniel, a ngii, ñu boole ko ci limu Le Ministère du Royaume bii. Na la wóor ne, sàmm nga ci ab sotti ci sa biir téere. Doxalukaay bi day wone pàcc mi (chapitre), xise yi (paragraphes) ci biir téere bi, akitam aaya yi ñu jukkee ci Dañel, te ñu nar leen a waxtaane ayu-bés gu ne. Mbind yi ci suufu xët yi dañuy faramfàcce nan ak kañ lañuy seet yenn xaaj, yi nekk ci biir téere bi. Bu ñu sottalee njàng mi ayu-bés gu ne, ñu ngiy xiirtal aji-jiite ji mu nafar ak mbooloo mi aaya, yi ñu jukkee ci Dañel saxsax, te ñu lim leen ci doxalukaayu ayu-bés googa. Su ñu amee jot gi, mën nañoo duruus aaya yi te faramfàcce leen. Am na ay aaya, yu ñuy gis ayu-bés sangam ak gi ci topp, ndax li ñuy wéy di bàyyi xel ci ni ñu leen war a nànde, akit ni ñu mate.
3 Waajalal sa bopp ci njàng mu xóot : Fexe nañoo bàyyi jot gu doy, ayu-bés gu ne, ngir bañ a yàkkamti li ñu war a waxtaane. Am na ñeenti njàngale, yoo xam ne, daanaka dañoo gàtt. Noonu, bu ñu sottalee njàngum ayu-bésu 5 suweŋ, aji-jiite ji dina ci mën a boole nafaru Dañel 2:1-40. Ci ayu-bésu 26 suweŋ, mën naa nafar Dañel 3:1-30. Ayu-bésu 4 sàttumbar war naa ëmb waxtaan wu xóot, wu ñu jëmale ci nataaliy xët 139, ak aaya yi ñu fay fekk. War nañoo waxtaane nataal bi ñuy fekk ci xët 188 ak 189, ci njàng mi ñuy amal ci ayu-bésu 2 oktoobar.
4 Waajalal sa bopp bu baax ngir njàngum ayu-bés gu nekk, te sàkkul bànneex ci di ca tontu. Fonkal sa céru bokk ci mbooloo Yeowa, mi ne ci kow suuf, ak sa céru jariñoo ràññaatle ak dég-dég, yi tukkee ci ñi mu tànn ak xel mi, nit ñu takku ci moom (Dañel 12:3, 4). Ak mbaaxaay, xiirtalal ñeneen ñu faral di teewe njàngum téere bi. Yal nañu bàyyi xel, ñun ñépp, ci Kàddug Yàlla, giy yégle liy ami, ci ni mu feeñe ci téereb Dañel, téere buy jommal dëgg. — Yaw. 10:23-25 ; 2 Pie. 1:19.