‘ Na seen leer melax ’
1 Àddina si ñu wër, ci lëndëm dëgg la nekk ci wàllu xel ak ci wàllu jikko ju rafet. Leeru dëgg gi, nag, day feeñal “ jëfi lëndëm y[i] amul njeriñ ” ba tax ñu mën a moytu doj yooyuy fakkatal tey jëme ci dee. Looloo tax ndaw li Pool jamp karceen yi, naan : “ [Wéyleen di] dund ni ay guney leer. ” — Efes 5:8, 11.
2 ‘ Li leer giy meññ ’ daa wuute dëgg ak lëndëmug àddina si (Efes 5:9). Meññ doom yu ni mel daa laaj ñu doon royukaay yu ràññeeku ci suñu dundug karceen, waaw, fasoŋi nit ñi Yeesu di nangu. War nañoo wone itam ay jikko niki ànd ak xol bu tàlli ci li ñuy def, xol bu laab, ak dem ba jeex ci dëgg gi. War nañoo wone meññeef yooyu bés bu ne ci suñu dund, akit ci suñu sasu waare.
3 Melaxal ci anam bu ne : Yeesu daa ne woon ay taalibeem : “ Na seen leer leere noonu ci kanamu nit ñi. ” (Macë 5:16). Ndegam dañuy roy ci Yeesu, ñu ngiy awu leeru Yexowa, bu ñuy waare Nguuru Yàlla, ak li mu nas. Ñu ngiy melax niki ay way-leeral, bu ñuy seeti nit ñi ci seeni kër, tey siiwal dëgg gi fi ñuy liggéeye, jànge, ci suñuy biir dëkkandoo, walla fépp feneen fu ñu am bunt. — Fil. 2:15.
4 Yeesu nee na, doon na am ñu sib leer gi (Ywna. 3:20). Li ëpp ci nit ñi lànk nañoo may “ leeru xabaar bu baax, biy wone ndamu Krist ”, mu melax ba agsi ci ñoom, waaye loolu du ñu yoqiloo (2 Kor. 4:4). Yexowa, ci xolu nit ñi lay seet te soxlawul ci biir mbooloom ñiy jëfe njubadi.
5 Topp yooniy Yexowa tey jariñoo leeram ci wàllu xel, mooy tax ñu mën koo awu, di leeral ñeneen ñi. Ñoom nag, su ñu ràññee ci suñu demin ne, ñun ñoo “ am leeru dund ” gi, bu boobaa loolu mën na leen a xiir, ñoom it, ñu def soppi yi war, ba tax ñu doon ñuy leeral seeni moroom. — Ywna. 8:12.
6 Bu ñuy may suñu leer mu melax, dañuy màggal suñu Sàkk-kat tey dimbali ñi seen xol laab ñu xam ko te dunde yaakaaru dund ga dul jeex (1 Pie. 2:12). Ndegam ñun ñoo ame leer gi, nañu ko jëfandikoo ngir dimbali ñeneen, ñu gis yoon wi ñu leen xàllal ngir génn ci lëndëm gi ci wàllu xel, te sàkk ay jëf yu bokk ci leer gi.