Barke yi ñuy am bu ñuy wone suñu ngërëm ci mbëggeelu Yexowa— Xaaj 2
1 Ci xaaju waxtaan bi ñu defoon weer wii weesu, wone woon nañu ñeenti fasoŋ yu ñu mënee wone suñu ngërëm ci mbëggeelu Yexowa ci waaraate bi (1 Ywna. 4:9-11). Fii dinañu ci yokk yeneen juróomi anam yuy maye bànneex, bu ñuy dimbali bu baax ñeneen ñi ci wàllu ngëm.
2 Seede saa yu ñu ci amee bunt : Seede boobu baax na ngir gis ñi xiif te mar njub te it jox leen ay téere yu leen mën a dimbali. ‘ Jariñoo suñu jot ’ tey waaraate saa yu ñu ci amee bunt, ku ñu mënta taseel, lu am solo la (Efes 5:16). Fasoŋu waaraate boobu, mën na am mu laaj fit dëgg, waaye bu ñu amee ngërëm ci mbëggeelu Yàlla, te soxla nit ñi bu nekkee lu ñu itteel dëgg, dinañu waare saa yu ñu ci amee bunt. — 2 Tim. 1:7, 8.
3 Benn misionéer jële na ay barke yu bare ci li mu tàmbali waxtaan ak góor gu toogoon ci wetam ci taksi bi mu nekkoon. Góor googu wone ne loolu itteel na ko. Ñu delluwaat seeti ko, te tàmbali jàng ak moom Biibël bi. Góor googu mujj na nekk Seede Yexowa, te dem na ba nekk mag ci mbooloo mi !
4 Bind ay leetar : Xëy na mënuñu dem waaraate këroo kër ndax li suñu yaram neexul walla asamaan si xiin, mu ngelaw ba mu ëpp, mu tàng lool, walla yu mel noonu. Bu boobaa, mën nañu bind ay leetar ngir waar, ci wax bu gàtt, nit ñi nu xam, ñi am mbokk bu gaañu, walla ñi nekkul woon seen kër bi ñu fa jaaree. Mën nañu def ci leetar boobu suñu benn kayit bu ndaw bu am xabaar bu jóge ci Biibël bi bu neex a dégg. Bu ko jàngee, mën na am mu bëgg a laajte yenn yi. Jox ko sa adarees walla bu Saalu Nguur gi ndax mu yónni fa leetaram. Bu ko jox adareesu bànqaas bi.
5 Seede ci telefon : Seede boobu baax na ngir jot ñi nu mënul a gis bu ñuy waaraate këroo kër. Bu ñu ko defee ak sutura, laabiir, aay ci li ñuy def te bañ a ñàkk kersa , mën na am ñu déglu nu. Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee 2001 dafay joxe ci xët 5 ak 6, ay tegtal yu baax ngir fasoŋu seede boobu jur li gën.
6 Ba mu doon waare ci telefon, suñu benn mbokk bu jigéen dafa laaj benn jigéen ndax xalaat na bu baax naka la dundam moom ak njabootam nara mel ëllëg. Jigéen ji tontu ko ne xalaat na ci. Mu wax ko it ne ñàkk yaakaar bi mu am moo tax muy toog këram, bañ a jegeti nit ñi. Ni ko suñu mbokk wonee itte moo tax jigéen jooju nangu daje ak moom ci marse bu leen jege. Jigéen jooju mujj na nangu jàng Biibël bi !
7 Teral gan yi : Bu ñu bëggee suñu moroom, dinañu gaaw a seetlu bépp gan bu ñëw fi ñuy daje te dinañu ko teral bu baax (Room 15:7). Nañu ko won ne mu ngi ci diggu xarit yoo xam ne, dëgg-dëgg, bëgg nañu digganteem ak Yàlla rattax. Bu ñu ko wonee itte te wax ko ne, bu ko neexee mën nañu ko jàngal Biibël bi, loolu mën na tax mu nangu suñu ndimbal.
8 Suñu jëf yu rafet : Suñu jëf yu rafet dañuy rafetal dëgg gi (Titt 2:10). Bu niti àddina si dee wax lu baax ci ñun Seede Yexowa yi, dañuy màggal suñu Yàlla (1 Pie. 2:12). Loolu itam mën na dimbali ñeneen ñi ba tax ñu tàmbalee dox ci yoonu dund.
9 Lu la teree seetaat juróomi fasoŋ yi ñu mën a wone suñu ngërëm ci mbëggeel bu réy bi ñu Yexowa won te def li ñuy laaj (1 Ywna. 4:16) ? Boo ko defee, dinga ci jële barke yu bare.